Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dina amal njëlbeeni génnam ci ayu-bés bile. Moom nag, Afrig la jagleel génnam yu njekk yooyile, nar a dem ca dëkkandooy Senegaal yii di Móritani (Gànnaar) ak Gàmbi, ñu di ñaari réew yim digalool. Ci àllarba jii, 17 awril 2024, lay dem Gànnaar. Gaawu, 20 awril 2024, mu dem Gàmbi.
Dafa di nag, ñaari réew lañ yoy, li leen booleek Senegaal bari na, demb balaa tey. Kon, li la tax Njiitu réew mi taamu leen, am na lu muy wund lu xóot ci nim nar a jëflanteek bitim-réew. Rax-ci-dolli, ci wàllu koom-koom ak pólitig, Senegaal ak Gànnaar dañ séq lu bari lol, dafa solowu lool ci jamono jees tollu.
Ci wàllu koom-koom, ñaari réew ñoo bokk balluwaayu gil (gisement de gaz) bii di “Grand Tortue Ahmeyim (Gta)”. Balluwaay boobu, xaymees ko ci 1 400iy milyaari m³. Te, ci atum 2024 mii lañ war a tàmbali liggéey bi ñeel ko.
Bu dee ci wàllu pólitig, Mohamet Uld Gasuwaani, Njiitu réewum Gànnaar, moo jiite kurélug Bennoog Afrig (Union Africaine) jamono jii. Te, jubluwaayu njiiti Senegaal yi mooy fexe ba jëmmal bennoog réewi Afrig yi.
Bu dee Gàmbi, mënees na njort ne mbirum MFDC ak tukki yi mooy liy gën a soxal Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay.
Ak lu ci mën di am, lees ci mën a jàngee mooy ne, moom Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ginnaaw Senegaal, Afrig lay jiital ciy mébétam ak liggéeyam. Te, mel na ni, bennoog Afrig, lu ko yitteel la. Moo tax ñu bari njort ne, njiiti Senegaal yu bees yi, dañu bëgg a dog buumug njaam gi dox sunu digganteek nootkat ba woon.
Yàgg, yàgg nag, Njiitu réew mi di tukki biti Afrig. Ñuy xaraandi ba xam man réew la koy jagleel ak lay dooni sabab bi.