LAYOO MAAM MBAY ÑAŊ-USMAAN SONKO : DIG-DAJE 8 ME 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci altiney tey jii, 17 awril 2023, la layoob “Appel” bi ñeel Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko waroon a am. Waaye, ajandi nañ ko ba bésub 8 me 2023. Àttekat bi, Aamadi Juuf, joxewul sabab yi ko tax a ajandi layoo bi.

Ngir fàttali, Maam Mbay Ñaŋ mooy topp Usmaan Sonko yoon, wax ne dafa yàq deram, tuumal ko ci mbirum PRODAC mi. Jotoon nañ leen àtte, keroog 30 màrs, daan Usmaan Sonko ñaari weeri kaso yoy, du leen tëdd, ak 200i tamndaret yu muy dàmpe Maam Mbay Ñaŋ. 

Keroog, bi daan bi jibee, Maam Mbay Ñaŋ dafa bégoon, wax ne Yoon setal na ko. Waaye, dañu toog as-tuut, moom ak toppekat bi daldi dugal àppel. Bu dee Maam Mbay Ñaŋ day sàkku ci ñu yokk xaalisu ndàmpaay bi, toppekat bi, moom, li muy sàkku ñu toppe njiitul Pastef li mbirum jëfandikoo këyit yu baaxul ak i saaga.

Dig-daje keroog 8 me 2023.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj