Li gёn a fés ci xibaari bés bi Alxames 3 nowambar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko

Démb ci alxames ji, 3 nowàmbar, la kii di Njiital PASTEF li, Usmaan Sonko, doon janoo ak àttekat bi ginnaaw coowal siif li ko ndaw sii di Aji Saar jiiñ. Kenn ci ay layookatam, Bàmba Siise, xamle na ne, seen lawax bi tontu na ci laaj yépp teg ci joxe na ay firnde yu leer ci mbir. Léegi, ñoom, nee ñu amul lenn lu ko mёn a taqal, dañoo bёgg ñu gas coow loolu ba xóot, suul.

Jàppug ñenn ci way-wattu kaaraange Usmaan Sonko

Lu tollu ci juróom-benn ci way-wattu kaaraangeg Njiitalu PASTEF li lañu teg loxo tey. Jamono ji Usmaan Sonko doon tontu laaji àttekat bi ca biir pekkoom ga la sàndarma yi jàpp gaayam ya, yóbb leen Mbuur. 

Bi Usmaan Sonko génnee, fekk na ñu dem. Waaye, nee na, loolu duñu ko seetaan.

Leerali  toppekat bi ci jàppug gaa way-wattu kaaraangeg Sonko

Ci ab saabal bu mu génne, kii di Mamadu Jóob, toppekat Mbuur bi, mi ngi ciy xamle ne kat, ñi ngi toppe gaa ñooñu di wattu kaaraange Usmaan Sonko coow lu amoon ci bésub dibéer 30 oktoobar, boori juróom-benni waxtu ci ngoon ca diwaanu Ciki. Coow loolu ñu leen di toppe nag, mi ngi juddoo woon cib jàmmaarloo bu doxoon seen diggante ak ay mbokk soxna sii di Faatu Njonn, ba am ñu ca jёle ay gaañu-gaañu.

XEW-XEWI JAMONO

Xew-xew ba am ca diwaanu Séeju

Fale ca diwaanu Séeju ca dёkk boobu di Kerewo, benn imaam la fa jarbaatam doon fetal ngir tas am mbooloo. Ñooñu nag, ab xuloo bu doxoon diggantey jigéen lañ woon Kumba. Bi mu soqee fetal ba nag, dafa far laal imaam bi ci loxo. Ndaw loolu nag yoon teg na ko loxo ngir lёñbёt mbir mi.

Limub ngànnaay yi ñu teg loxo

Ñii di ndawi birigaad bu Tàmbaa ñoo teg lim bu takku lool ciy ngànnaay yu ñu nangoo ci ay sàmbaa-bóoy. Ngànnaaay yooyu nag, nii la tёdde : 4i fetel yoy, ñett yi bali 12 mm lañuy jël, benn fetelu xare bees dippe AK, 300i sox ak 5i soxiy xare.

Beneen xew-xew bu doy waar

Fale ca diwaanu Cees lañu bett ñaari góor ñuy séy. Kenn ki di wuyoo ci turu A. M. Jàllo, keneen kiy wuyoo ci turu B. Juuf. Ci li rotagum ciy xibaar, mel na ni, ki ñu mujje tudd dafa joxeb lay, wax ne moroom ma dafa yoroon paaka, tiitalee ko ko ngir mu tёdd ak moom. Ci la am ñu leen gis, daldi leen di yóbb ca pólis “1er arrondissement” bu Cees.

NJÀNG AK NJÀNGALE

Seex Isaa Sàll, meeru goxu Mbuur, moo génnee lu tollu ci ñeen-fukki milliyoŋ ak juróom ngir jёndal daara ya fa nekk lépp lu ñuy soxla ci wàllum jumtuwaayi njàng yu deme ni ay téere, ay xalima, añs. Jёf jooju nag, li mu ko dugge mooy dimbali yenn ci way-jur yi nga xam ne seen loxo jotul seen ginnaaw ba seen doom yi mёn a am matuwaay yi ñuy yittéwoo ca daara ja.

WÉR-GI-YARAM

Jàngoroy kañseer

Jàngoro jii di kañseer nga xam ne jigéen ñi la gёn a sonal, te ci jamono jii sax mu tàmbalee laal ndaw ñi moom lañu jagleeloon weeru oktoobar wii. Fajkat bii di Mamadu Mustafaa Sekk mi ngi xamle ne fii ci Senegaal, dees na fi nemmeeku lu tollu ci 20. 000i ci ay nit ñu ko ame. Te, jàngoro jooju bàyyiwul xale yi sax ndax nemmeeku nañu ci lu tollu ci 800i ñu ko ame.

XIBAARI BITIM-RÉEW

Déggoo diggante Mali ak Burkinaa Faaso

Démb ci àllarba ji la kii di Kàppiteen Ibraahiim Ture amaloon tukkib nemmeeku fale ca Mali ca mbokkam moomu di Asimi Goytaa. Lii nag, di ab génnam bu njёkk ginnaaw bi mu jotee ci Burkinaa Faaso. Ñoom nag, seen lёngoo ci wàllum sóobare la ngir ñu mёn a xeex ci lu gaaw rëtalkat yi (terroristes).

Ndogalu Nguuru Gine

Nguur ga nekk Gine, jamono yii di goog sóobare yi jёl na ndogalu topp ca yoon ki fa nekkoon Njiitu réew ma, Alfa Konde. Du moom kese nag, ndax am na lu ёpp 180i kàngaam (cadres) ak i jёwriñ. Ñoom nag, ñi ngi leen di toppe ay jёf yu deme niki ger, luubal, njuuj-njaaj, añs.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj