LU WARAL ITALI SOPPEEKU NII ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ak lu waay mën a wax, réewum Itali yàqu na. Bi Salwini toogee ci jal bi ba tey, ñoo ngi fay bundxatal doxandéem yi, rawatina ñi ci seen der ñuul, te ñu bawoo Afrig. Muy lu mën a jur musiba ëllëg.

Lu defu waxu, walla dara du réer, waaye itam dara du làqu ba fàww ndax bés dina ñëw lépp leer nàññ. 

Wax jooju lu wér la. Ndax ni réewum Dante soppeekoo jéggi na dayo. Yow mi xamul kuy Dante, nag, may ma tuuti ma dellusi ci jaar-jaaram. Dante ab bindkat bu ñu ràññee la ci addina sépp.  Mu ngi juddu ci atum 1265 ci dëkk bu ñuy wax Firense fii ci Itali, génn addina ci atum 1321. Téereem bi gën a siiw moo di « La Divine Comédie ». Looloo tax ñuy faral di woowe Itali « dëkku Dante ».    

Waaye kat, politigu Mattewo Salwini soppi na lool xar-kanamu dëkk bi ndax moom bëggatu fee gis ay doxandéem rawatina nit ku ñuul. 

Tey, loolu lanu nar a waxtaane fii nu toog man ak sama xaritu benn-bakkan, Stefano, ak Baay Sidi, sama doomu-ndey,  ku yágg a dëkk Milaŋ, def fi 20i at ak lu topp.  

Matewo Salvini mooy jawriñ ji ñu dénk mbiri biir réew mi fii ciItali, jiite yit pàrti politig bii di La Lega.  Waaye pexeem ak i xalaatam yépp ci lenn lañu jublu te mooy xeex doxandéem yi wàlliyaansi ci réewam. Nit ñu ñuul ñi nag la singali. Ba tax nadoomi Afrig yi amuñ fi jàmm ndax ci xoqtal leen la La Legadëkke ak ñoom.  Jaratuñ fi dara. Lu waay xalaat ci lu ñaaw rekk teg leen ko. Kii di Salwini, daal, mu ngi nuy yakk guddi ak bëccëg lu mel ni xeme, askanu Itali yépp di ci dégg. Mu jaare fa may fit waa dëkkam ba ku jὀg rekk ne:  “Nit ñu ñuul ñi sácc lañu, amuñu xam-xam, dañoo xayadi, ñoo yàq Itali te ñoom sax, ni ñuy takkee sunuy jigéen day tax seen deret ak sunu deret jaxasoo te loolu dara yéesu ko ! Mu dem sax ba ku bëgg a tiital sa doom danga ko naan ‘’boo deful ndànk ma woo nit ku ñuul ki ! “ 

Ku bëgg i firnde ci li nuy wax nii, doxantul biir anternet rawatina Facebook. Bés bu Yàlla sàkk Salwini def fa ay widewo, di ci xas  doomi Afrig yi. Mu jaral ko nag fay xaalis bu bari ngir waa Facebook jàllale leen.

Yéene Matewo Salwini mooy fexe ba genn gaal gu yab ay doxandéem dootul jὀge Libi teersi Itali. Te yemul ci loolu ndax xeex na kurél yi tënkuwul ci nguur gi (ONG) ci péncum ndawi réew mi ba nga xam ni seen benn gaal ñemeetul a wallu ñiy lab ci géej gi diggante Libi ak Itali. Ndogal lu ni mel nag ay musiba rekk la jur. Ndax boobaak léegi ñiy faatu ci géej gi bari nañu lool. Te teewul bés bu nekk ay gaal yu ndaw fees dell ak i doomi Afrig teersi Lampedusa. Walla ONG yiy aar gaal yu mag yiy jòge Libi dikk ak mbooloo mu takku Kataña mbaa Lampedusaa.

 Fi ñu tollu ni politigu  Salwini xar  na réew mi ñaar: ñi ànd ak moom, ak ñi féete ci  kujje gi. Nguur gi ak kujje gi dëkke di dàggasante, xastante ak xuloo. Réewu tugal yépp di seetaan te defu ñu dara ngir aar doxandéem yi. Tugal gépp ànd bàyyi Itaali muy doxale ni mu ko neexe politigu   imigarasyoηbi.  Mbir la bu nuy nàqarlu lool.Li ci gën a yéeme, nag, mooy patt-pattaralu mbootayu xeet yi (ONU) te nu yaakaar ne moo ci waroon a njëkk wax.

Waaye lu am solo xew na ca Pari, fan yii weesu

Nu tëjeek xibaar bu am solo : démb ca Pari, péetum Frãs, Emanwel Makroŋak AŋselaaMerkel dajale nañu 14i jawriñ yi ñu dénk mbiru biir réew ci Ërób yépp ngir waxtaane imigarasyoη. Mu mel ni dañoo dégg sunuy tawat. Ndax ndaje moomu dina indiy coppite, delloosi xel yi ? Am nan ci yaakaar. Li ci teey xel rekk moo di ne li wax ciy bari yépp Salwini min ndeyu-mbill gi, dafa lànk ba tëdd ci naaj wi ne du bokk ci ndajem Pari moomu. 

Waaye ci sunu gis-gis bu gàtt, pexe mënuta ñàkk ba fàww.

Baay Njaay ak Stefano Anselmo

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj