MAAJOOR, BUL FÉETE BOOR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi ñu fésalee seen ag caabal ñeel yorinu FORCE COVID-9 bi, Ëttub cettantal gi fëgg na buntu jëwriñ ji ñu dénk wàlluw yoon ngir mu saytu fu lenn ci junniy milyaar yi ñu jagleeloon mbas mi dugg. Ndax kat, ci caabal gi, dafa am lu jege fukki kilifa yoo xam ne daf leen a duut baaraam, muy ay DAGE, ay jëwriñ walla ñi fare ci asãs yi. Ci ñooñii la sàkku ñu ubbib lànket ngir leeral tuuma yees leen gàll. 

Caabalug Ëttub cettantal gi nag dafa bari ay mbir yu mu feeñal donte ne sax ya ko jiitu woon defoon nañu lu ni mel. Waaye, li leen wutale mooy wile yoon, ci xaalis bi ñu salfaañe, saa-senegaal yi rekk dañ ci am loxol fukki miliyaar ak juróom-ñeent, 20i milyaar daanaka. Léegi nag, ñooñu la gaa ñi amal coow. Ndax kat, Ëttub cettantal gi wéetul wenn yoon ci liggéey bi. Dafa di, ci àjjuma jii weesu rekk, kuréli way-moomeel yi amaloon nañu am ndajem-ñaxtu ngir naqarlu ni gaa ñi naxee doomi réew mi, tiital leen, tëj leen ci seen kër yi, di leen wulli ay liif, ànd ak loolu lépp, ndeke ñoo nga daan tibb di sol ci seen i gafaka. Mu mel dañu gaawtu saa-senegaal yi, jëfandikoo seen ug tiitaange ak ug njàqare, di luubal alal ji ñu leen waroon a taxawoo. Loolo tax askan wi, keroog ca ndaje ma, genn kàddu lañ fa biral te mooy : “Sunuy milyaar du rees !”. Bët nag, bu rusul toj. Ku ñu xas teg lii sa ndoddu, li la war mooy summi sa mbubbum jëwriñ walla tekki bépp xeeti ndombog-tànka gu mu mën a tere yoon àtte la, nga daldi dem nag setal sa derci li ñu lay tuumaal. Gor day daw tuuma. 

Mbir mi doonut lu woyof. Mukk ! Njuuj-njaaj bu ni tollu, deesu ko soofantal ak a ñàkkal faayda. Daanaka lu jege ñaar-fukki milyaar (19 727.096.727) lañu dugal ci foo xam ne laalewul dara ak mbas mi bees sukkandi ci caabal gi. Waaw, boo demee  ci 87eelu xët wi, dinga fekk firnde yi. Nu ni déet-a-waay, gaa ñi yokkati njëgi màrsandiis yi ñu wax ne jënd nañu leen. Céy, Senegaal, demagoo de ! 

Loolu tax na ba Ëttub cettantal gi woo yoon ci mbir mi ngir mu waslu ci àqam. Kii nag di Mammadu Mustafaa Ba, jëwriñ ji ñu dénk kopparal geek nafa gi, moom, ciy kàddoom, jalgati bi, juróom-benni milyaar kepp la ñeel. Loolu lanu jukkee ci waxam jii : 

“Li nu mën a wax, te jàpp ko, mooy, alal jii Ëttub cettantal gi di laaj yoon def ci liggéeyam, lu tollu ci 6.686.784.410 moo ci am i ndëngte (irrégularités). Fim tollu nii, mënunoo wax ag luubal la. Danu ko war a leeral. Nguur gi mi ngi koy naqarlu te dañu ko war a topp ba mu leer.” 

Léegi nag, ñii di waa Ëttub cettantal gi wan nañu yoon gaa ñi nga xam ne def nañu naka su dul noonu ci li ñépp bokk. Yaa def, defuma, Ëttub cettantal gi jébbal na caabal gi yoon. Sas na ko nag. Askan waa ngi xaarandi ba xam fu mbir yiy mujje. Waaye nag, bu dee wax dëgg rekk, ameesul yaakaar ci yoonuw réew mi. A waaw, xanaa lu ni mel amu fi, amaat fi ? Ndax mësees na fi gis kenn kees tuumaal ba mu leer, yoon daan ko ? Déedéet, mësul a am ci Nguurug Sàll lamtooro. Moom Sàll, Njiitu réew mi, dafa ni woon sax ne, am ciy wayndare yoy, moo teg concoom. Rax-ci-dolli, caabal yi Ëttub cettantal génne woon laata bi mujj gile, dafa ni woon day taxawal ag kurél guy saytu mbir mi. Ana mu ? Tus. Dara. Kon, njort mënul a rafet ci caabal gile, rawatina bu dee groom ci la bokk. Moone de, Xalifa Sàll benn milyaar kepp lees ko toppe woon daanaka, waaye dañu caxat-caxate woon, patam-patame ko, àtte ko ci lu dul yoon, tëj ko. Naka noonu, Kariim Wàdd, dommu Ablaay Wàdd, Njiitu réew ma woon. Ndeysaan, lii la wolof di wax, làq doom, dóor doom. 

Njiitalu Ëttub cettantal gi, moom, def na wareefam. Jébbal mbir mi yoon, bind leen itam. Li mu ko dugge mooy fexe ba yoon woolu njiit yees jàpp loxo ci poos, déglu leen ba xam fu ñu dugal xaalisu askan wi. Kon nag, yoon mooy bëgg a dese yëf yi. Lu mu muñalul ku fare ci kujje gi, bum ko muñal ku fare ci Nguur gi. Ku luubalul mu mën a setal deram. Ku luubal mu teg ko ay daan, mu delloo askan wi li mu moom.   Ndaxte, ku wàcc yoon, yoon dal sa kow. Moo tax jëwriñu yoon wi, Ismayla Maajoor Faal, war def liggéeyam bañ a jeng. Ndaxte, Nguur, ndoxum joor la, ku yebu xam ko. Kon, Maajoor, bul féete boor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj