MARIN BU SENEGAAL : JURÓOMI KOMÀNDOO YI RÉER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Juróomi komàndoo yu marin bu Senegaal ñoo réer. Muy mbir mu doy waar mu ñu nemmeeku ginnaaw bi marin bi tegee loxo benn gaalu defkati ñaawteef ci géeju Ndakaaru.

Démb ci àjjuma ji, 5 sãwiyee 2024, lu tollu ci juróomi komàndoo yu marin bu Senegaal ñoo réer ci waaxi Ndakaaru yi.  Muy xibaar bu tukkee ci waa DIRPA (Direction de l’information et des relations publiques des armées), maanaam bànqaas bi yor jokkoo ak jokkalante bi ci diggante làrme beek askan wi.

« Am na juróomi komàndoo yu marin bu Senegal yu réer  démb ci àjjuma ji, bi 20i waxtu di jot. »

Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu siiwal ci seen yëgle bi, ñoo ngi seetlu mbir mi ginnaaw bi seen saytukat yi doon wër ci biir géej gi. Ci seen wër googu nag, dañu ci teg loxo ag gaal gog dañu njort ni ci defkati ñawteef yu mag yi ci àddina si la bokk.

« Mbir maa ngi xew ginnaaw bi sunu saytukaayu biir géej bi ñu duppee Waalo jàppee, fi tollook Ndakaaru, gb gaal goo xam ne, njortees na ni defkati ñaawteef yiy jaay sineebar bi ci àddina si ñoo ko moom. »

Li nu jàpp ni moo leen réeral nag, mooy ni, ñi yoroon gaal gi dañ ko doon jéem a suuxal. Nde marinu Senegaal bi dafa seetlu ni dañu tijji poroxndoll (vanne) yi ngir gaal gi sol ndox. Loolu sax moo tax ba ñu jàpp ni teyeef la. Pexe mu ñu jëfandikoo la ngir bañ ku gis li ñu ci yeboon.

Jamono yii nag, marin bee ngi wéy di seet ñi réer. Ñu seetlu itam ni lu ni mel mi ngi tàmbalee bare lees koy gis ci géeju Senegaal. Ndaxte, ci diggante weeri nowàmbar ak desàmbar rekk, marin bi jàpp na ci ñetti gaal yoy, ay gaal yu ni mel lañ. Bi ci mujje (24 desàmbar 2023) di gaal bu juróomi doomi réewum Espaañ yoroon.  Ñu fekkoon ci ñoom 490 kilo sineebar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj