Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, jël na ndogal yu bees ñeel kàmpaañu mbey mi ci atum 2024 mi jàpp 2025. Dafa namm a lal ay pexe yu bees, soppali doxaliin wi ngir fànnu mbéy mi mën a noyyi, beykat yi gis ci seen bopp.
Démb ci àjjuma ji, 3 me 2024, la magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, doon jiite am ndaje ci diggante jëwriñ yi laale ak mbey mi. Ndaje maa ni nga doon amee fa Cicad (Centre international de conférences Abdou Diouf), Jamñaajo, doon ca waxtaane kàmpaañu mbéy mi ñeel atum 2024-2025.
Ci seen ndaje moomu, Sëñ Usmaan Sonko biral na fa ndogal yi Càmm gi jël ngir suqali mbey mi, mu mën a bokk ci fànn yi ëpp doole yuy tingoom koom-koomu réew mi. Bokk na ci yi mu sàkku ci jëwriñ ji, Mabuuba Jaañ, mu fexe, ci lu njëkk, fey bor yi dox ci diggante Nguur geek ñi ñuy woowe operaatëer yi. Bu loolu weesoo, digal na ko mu jublu ci séddale jumtukaay yees di dugal ci mbey mi ngir jàppalee leen beykat yi.
Ba tey ci wàllu jumtukaay yooyu, magum jëwriñ yi bëgg na jëwriñu mbey mi am ci taxawaay bu mat sëkk. Sàkku na ci jëwriñ ji mu fexe ba céddale gi jaar yoon, lépp leer ba ñi leen yayoo mën cee jot. Mbuxumkat yi tamit, dees na leen a ràññee, teg leen i daan.
Ngir céddale gi tegu ci yoon, Càmm gi fas na yéene sàkk jumtukaay bob, dafa koy jaarale ci xarala yu bees yi. Bu ko defee, dina ràññee képp kuy beykat te war a jot ci ndimbal li leen nguur gi jagleel, ràññeewaale ñi leen koy jottale ak di leen topp ba fépp fu jumtukaay yi jaar ñu mën koo xam. Làrme bi sax dina ci dugal loxoom.
Bees sukkandikoo ci li magum jëwriñ yi biral, pexe yii yépp mu nar a lal, dara waralu leen lu dul ni ci diggante 2020 ak 2023, dugal nañ lu ëpp 310i tamñareet (milyaar) ci mbey mi. Waaye, demul fa ñu waroon a dem. Nde, ña ca waroon a jot, jotuñu ci. Kii di Biraahim Sekk, di njiitu Forum Civil, yokk na ci tamit ni, lu ëpp 380i tamñareet jot nañ dugg ci fànnu mbey mi laata atum 2018. Loolu sax a tax muy sàkku ci ñu génnee turi beykay yu mag yi Càmm gi joxoon alal jooju. Ndax ñu mën a xam ñi ci am ak ku ci nekk ñaata la am.