Ndogal loolu ñi ngi ko jël barki-démb ci gaawu gi ginnaaw waxtaan wu ñu doon amal ñeel “Assises nationales” yi. Waxtaan woowu ci ñaari fan lañu ko waroon a def. Waaye, dañoo mujjee tënk lépp ci gaawu gi. Ndogal la fa rotee nag, mel na ni sooful ñi ëpp ca ñay yeewoo fa Burkinaa Faaso. Nde, xamle nañu ne yokkal nañu Kàppiteen Ibraayma Taraawore diir bi mu war a def fa boppu réew ma.
Weeru sàttumbar atum 2022 la Kàppiteen Ibraayma Taraawore jot ca réewum Burkinaa Faaso. Moom nag, dafa daaneloon Nguurug kii di Kolonel Póol Aari Sandawogoo Damibaa mi nga xam ne sii, moo daaneloon Nguuru Kiriscaan Kaboore. Maanaam, Damibaa dafa daaneel Nguuru Kaboore weeru saŋwiye, weeru sàttumbar, Kàppiteen Taraawore foqati Nguur gi ci moom. Lépp xewe ci atum 2022 mi. Ba mu jëlee Nguur ga ca la taxawalee ag Nguuram ak ug Ngomblaanam gu ñuy dippe “Assemblée Législative de Transition” (ALT). “Assises nationales” yi may leen diiru ñaar-fukki weer ak benn ci boppu réew mi laata ñuy amal i wote. Àpp googu mi ngi waroon a jeex benn fan ci weeru sulet. Weer kesee desoon ci àpp googu. Waaye, gaa ñi dañu dajaloowaat ngir xool nu ñuy wéyalee mbir mi.
Gaawu ak dibéer la gaa ñi waroon a dajee ngir waxtaane mbir moomu fa béréb bii di Waga 2000. Waxtaan woowu mujjee naa sotti barki-démb ci gaawu gi donte ne sax, ay jiixa-jaaxa jotoon naa am ba ay jàmmaarloo sosu ci. Nde, ay xibaar dafa rot ci ne, ñetti at ak xaaj lañuy mayaat Kàppiteen Taraawore ci boppu réew ma. Loolu la askan we ne du fi ame. Ndeem sax tàmbali woon nañoo yëngal, waaye, takk-der ya mujj nañu leen dékku ba yàquñu ndaje ma. Dañoo mujj faf di sàkku ñu yokkal fukki at yoo xam ne da koy des fa boppu réew ma. Waaye, gaa ñi mujjewuñoo def loolu.
Bi ndaje mi jeexee, gaa ñi jël nañu ndogal lu am solo. Nde, xamle nañu ne Kàppiteen Taraawore dina fa toogaat lu tollu ci diiru juróom-benn fukki weer. Maanaam, juróomi at. Te, àpp gi dina door ñaari fan ci weeru sulet atum 2024 ginnaaw bi ñaar-fukki weer ak benn yi ñu ko mayoon jeexee. Ki ko xamle mooy Kolonel Musaa Jàllo. Waaye, mbir mi yemul foofu.
Moom Kàppiteen Taraawore yoratul taxawaay (statut) bi ñuy wax “président de la transition” kese yem ca, léegi, mooy Njiitu réewum Faaso. Rax-ci-dolli, wote yiy ñëw muy yu palug Njiitu réew yi, muy yu palug dépite yi walla yu gox-goxaat yépp mën na caa bokk moom ak Njiitu Ngomblaan gi ak elimaanu jëwriñ yi.