RFI : NJUUMTE, YABAATE WALLA LAN ? (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bërki-démb, ci altine ji, rajo Rfi dafa juum tàgge ñaar ci njiiti réewu Senegaal yi woon : Abdu Juuf ak Ablaay Wàdd. Am na sax ñeneen ñu ñu tàgge te deewuñu waaye li wolof naan : « gën a jege, gën a yey » moo tax nun nu seppi ci lim bi ñaari doomi-Senegaal yi. Ablaay Wàdd nag ci wàllu boppam nee na lu wokkul dërëm, xuriwu ko ; mi ngi sant Yàlla bu baax. Ñaaxaale  na nag taskati xibaar yi ñuy leerlu ab xibaar laata ñu koy tasaare. Ginnaaw loolu, Rfi génne na ab yëgle di ci wax lu tax xibaar bu ni mel rot ba siiw. Askan wi doon xaar buñ làyyee ba noppi ñu teg ci kàdduy njéggëlu, waaye furaas. Fa la léeb doxe tàbbi géej. Léegi nun, nu samp laaj : ndax loolu yoon la ? Su dee yabeel la, fan lañ ko teg ? Luy ndeyu Rfi tàgge ay doomi-aadama yuy dund, ci njuumte walla càggan ba noppi siidee génne benn baatu jéggalu ci gémmiñam gi ?

Ndey Koddu Faal

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj