Tey ci gaawu gi la ndajem ndeyu àtte réew mi tàmbali seen liggéey ñeel càkkuteefi lawax yi. Ñu fas yéene koo amal ci àppug juróomi fan ngir càmbar 93i wayndare ba xam kuy jàll ak ku dul jàll ak ku war a mottali.
Ci ñaari téeméeri Saa-Senegaal yi fésaloon seen yéene bokk ci ñiy xëccoo Njiitu réewum Senegaal ci 2024 bi, 93 ño ci mujje joxe seen warlu ba jébbal seen i wayndare fa saytukati ndeyu àtte réew mi.
Ngir tàqale way-sàkku lawax yooyu, saytukat yi dañoo lótëri seen i tur ci àjjuma ji, séddale leen ci juróom i fan yees leen war a càmbar benn-benn.
Ginnaaw bi ñu lótëree ba noppi, saytukat yi daldi nañuy door liggéey bi dëgg ci gaawu gi. Waroon nañ càmbar 9i wayndare ci suba si ak 11 ci ngoon gi. Bu ñu ci jógee tey, dinañu ci sëggaat talaata 2 sãwiyee 2024, àllarba 3 sãwiyee, alxames 4 sãwiyee ak àjjuma 5 sãwiyee.
Siiw na ni ku matalul li gën a néew ci lu ñu leen laaj ciy baayale du bokk. Terewul ñi yéesle lu takkuwul dinañu am àppu ñaari fan ngir mottali. Waaye ba, jàll beek ñàkk jàll bi ajuwul rekk ci baayale yi. Càmbar gee ngi aju ci 9i ponku yoy matale baayale yi ci la bokk. 9i ponk yee ngi dellu ci dogu 121 bu càrtug wote gi.