TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA ESPAAÑ
Bu yàggul dara la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jóge fa ndajem CEDEAO ma. Balaa yàgg, dina amalaat beneen tukki. Wii yoon moom day génn kembaaru Afrig gi. Ndax, ma nga jëm fa Tugal, fa réewum Espaañ....
Ci talaatay démb ji la "Banque mondiale" siiwal ne nangu na a lebal Senegaal koppar yu tollu ci 115i miliyoŋ ciy dolaar, yemook 65i miliyaari CFA. Bor boobu, li mu ko duggee mooy dooleel caytug koppari bokkeef gi te yokk anam yi ñuy dajalee...