Démb ci altine ji, kippug A gi ak gu B gi amal nañu seen ñetteeli joŋante ñeel sumb bu njëkk bi bi CAN 2024 bi.
Kippug A : Koddiwaar wayadi na/ Kap-Weer ak Niseriyaa raw nañu
Ñetteeli joŋantey gile kippu a ngi am ba 17i waxtu jotee ci, doxoon ci diggante Gine Equwaatoriyaal-Koddiwaar ak Gine Bisaawo-Niseriyaa
Gine Equwaatoriyaal dafa teg gàcce gu réy ñayi Afrig yi seen kanami soppe. Nde, daf ko ndulli 4i bal ci dara (4-0). Kesiyee ak i mbokkam, ci seen joŋante bu mujj bi lañu doon am yaakaar gañe ko ngir kalifiye. Waaye, dafa mel ni yëf yi takk na suuf. Ndax, fim ne nii, moo ngi ci guddi yu lëndëm lool sax. Mu nekk lu metti ci ñoom ñi nga xam ni ñoo dalal po mi seen dëkk.
Niseriyaa, moom, dafa dóor Gine Bisaawu 1-0. Seen ndam li nag yombul woon ci ñoom. Nde, démb, saa-bisaawo yi dañ leen indil alxatiir. Dugal nañu ca sax ñaari bii yoy, dañ ko bañ. Rax-ci-dolli, seen defãsëer bii di Opa Sangante moo dugal seen kã ca 36eelu simili ba.
Gine Equwaatoriyaal moo jël pée ca kippu ga ak 7i poñ, topp ci Niseriyaa, moom it 7i poñ la am. Waaye, aji-jiitu ji daf ko rawee ay bii. Koddiwaar moo jël 3eel ak 3i poñ, Gine Bisaawu laal ndaare boole ci amul dara ciy poñ.
Kippug B : Esipt ëpp na wërsëg Gana !
Ñoom, seen i joŋantee ngi door bi 20i waxtu jotee ci guddi gi. Benn bi, newoon diggante Mosàmbig ak Gana, ba ca des Kab-Weer ak Esipt. Ñaari joŋante yépp a ngi jeexee ci 2-2.
Gana, ci joŋanteem, dafa jiital Mosàmbig ñaari bii yoy, ciy penaaltii yu Jordaan Ayu dugal la ci 15eel ak 70eelu simili ya. Ñu bari jàppoon ni Gana gañe na sax, ba seen i xel tàmbali woon a dal. Waaye, dañu dawal ba ca jeexitalu mats bi Mosàmbig am penaaltii ci 91eelu simili bi, dugal ko. Ñu teg ci ñaar ba ñetti simili ñu tojaat këru Gana, Biddéew yu ñuul yi daldi wayadi.
Joŋante Kab-Weer ak Esipt, daanaka noonu la xaw a demee tamit. Ba ñu tàmbalee dawal bay waaj a mitã la Saa-Kab-Weer yi dugal (46eelu simili). Bi ñu noppaloo ba delsi ba ci 50eelu simili ba Esipt fayu. Ñaari ekib yiy wéyal ba ci 93eelu simili bi, Mustafaa Muhammed bu Esipt dugal. Ñoom it, niki waa Gana, jàpp ni jeex na. Waaye, dañu dawal ba ci 99eelu simili bi, Saa-Kab-Weer yi song leen, boyal seen caax yi. Ci 2-2 yooyu la mats bi jeexe.
Seen kippu gi nag, Kab-Weer moo jiitu ak 7i poñ, Esipt topp ci ak 3i poñ, tegu ci Gana mi am 2i poñ tolloo ko ak Mosàmbig mi tooge ndaare bi.
NAALU TALAATAY TEY JI
Ci talaata tey jii, ñeenti joŋante dina amaat : ñaar yu kippug C gi ak ñaar yu kippug D gi.