Ginnaaw yëngu-yëngu yu metti yi amoon ci alxames ji ak àjjuma ji, ak lees ci lim yépp ciy bakkan yi rot, am na yeneen 4i bakkan yi ci dolleeku. Fa loppitaanu Dalal Jàmm la néew yooyii nekk. Dr Xadi Faal a ko xamle ci yéenekaayu Libération. Fajkat bi ne : « Ci àjjuma ji, dalal nan fi 21i nit yu amey gaañu-gaañu te, ci bés boobu ba tey, lanu jot ñeenti néew. »
Dr Xadi Faal mel na ni kuy dëggal tuuma yees gàll saay-saay si ànd ak takk-der yi, di gaañ ak a rey way-ñaxtu yi. Nde, ciy seedeem, seen raglu bi dalal na ci ñoo xam ne, dañ leen a jam walla ñu ame ay dagg-dagg. Daf ne :
« Jot nan itam ñoo xam ne, ay bali fetel lañ leen dóor, am ci ñoo xam ne, ay gaañu-gaañuy paaka, jaasi walla yu ni mel lañu ame… Bu dee ñi ame ay gaañu-gaañu, kenn a ngi « réanimation », keneen mi ngi ca néegub oppeere ba ak ñeent yu nekk di faju. »
« Commission africaine des droits de l’homme et des peuples » mi bokk ci Bennoog Afrig , yedd na Maki Sàll
Kurél giy saytu àq ak yelleefi doom-aadama ak askan yi, maanaam Commission des droits de l’homme et des peuples, di banqaas ci Bennoog Afrig, génne na ab yégle di àddu ci yëngu-yënguy bokkeefu Senegaal. Démb, ci talaata ji, lañ siiwal yégle bi.
Ginnaaw bim ñaawloo taafar ji ak xeex bi diggante way-ñaxtu yi ak takk-der yi, yedd na nguurug Maki Sàll gi ñeel tëj biñ Usmaan Sonko këram ci lu dul yoon, dog bi ñu dog internet bi ak ni takk-der yiy reyee nit ñi. Dañ bind ne :
« Kurél gaa ngi ame njàqare ci dog bi ñu dog mbaali-jokkoo yi, niki Facebook, WhatsApp walla Twitter ngir « dakkal tasaereb bataaxeli mbañeel et fippu ».
Kurélg gaa ame njàqare tamit ci ni ñu tëjee Sëñ Usmaan Sonko këram, li ko dale bésub 28 me ba tey, tere ko génn, tënk ko ba ay layookatam mënuñoo gise ak moom jamonoy ji ñu doon xaarandi àtteb layoob ciif bees biral ci alxames ji 1 fan ci weeru suwe. […]
Kurél gaa ngiy ñaawlu bu baax xeex yi am diggante àndandooy Usmaan Sonko yi ak takk-der yi, taafar ji ñuy jëme ci takk-der yi, yëngu-yëngal yi jur fitna ci réew mi ak doole ji takk-der yiy jëfandikoo ci kow way-ñaxtu yi… »
Kurél gaa ngi jeexalee yégleem bi soññ takk-der yi war a wattu kaaraange askan wi ci ñu sàmm àq ak yelleef yi Sàrtub Afrig bi tëral yépp ak yeneen xeeti jumtukaayi yoon yi leen ñeel, te ñu moytoo jëfandikoo doole.
Kawlax : bàyyi nañu wattukat kaaraange Usmaan Sonko bi ak dawalkatam bi
Àttewaayu Kawlax bàyyi na wattukatu kaaraange Usmaan Sonko bi, Ibraayma Géy, ak dawalkatam bi. Ñoom ñaar ñépp, Kungë lañu leen jàppe woon, fekk ñu àndoon ak Usmaan Sonko mi jëmsi woon Ndakaaru. Àttekat bi daf leen a setal wecc.
Jàpp nañ aji-luññutug ngurd mi (inspecteur du trésor)Olivier Boucal
Démb lañ jàpp Olivier Boucal, aji-luññutug ngurd mi, fa AIBD. Biñ ko jàppe dañ ko jàllale ca « Section de recherches » bu Kolobaan. Lees koy tuumaal, bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, mooy ne dafa bokk ci ñu sooke yëngu-yëngal yu metti yi amoon ca Gudomp.
Jàpp nañ Ndey Ndaag Ture
Démb lañu woolu woon Ndey ndaag Ture ca sàndarmëri, birigaad bu Faidherbe. Ginnaaw bi ñu ko dégloo nag, nëbb nañu ko jant wi. Nee ñu toppekat baa ko jàpplu ndaxte dafa woote bañ ak xeex ñeel ñetteelu moomeg Maki Sàll gi ak layoob Usmaan Sonko bi. Seneweb a siiwal xibaar bi.
Àmbaasadi Senegaal yi dinañu tëj seen i bunt ba jëmmi jamono
Njëwriñu mbiri bitim-réew yeek Saa-senegaal yi fay yëngatu tëjlu na àmbasaadi Senegaal yi nekk bitim-réew. Démb, ci talaata ji 6 Suwe 2023 la jël ndogal li. Li ko waral nag, mooy cong yi jot a am ci yooyule béréb, rawatina ca Pari, Bóordoo, Milã ak Niiw-Yoork, te ñu nemmiku ciy yàqu-yàqu yu bari. Jëwriñ ji Aysata Taal Sàll di ko ñaawlu ci seen yëgle bi. Muy fàttaleet solos kaaraange ndaw yi fay liggéeye ba waral mu tëj bunt ya fileek ñuy yokk kaaraange gi ak a defaraat jumtukaay ya fa yàqu, yu deme ni masin yi daan defar dàntite yeek jàll-waax yi.
Senegaal amatul « anesthésie » jamono jii
Jëwriñu wér-gi-yaram gi ak ndimbal gee génne ab yégle, joxe xibaar bi :
« Maa ngi leen di yégal ne, jaare ko ci yégle bile, jamono jii danoo ñàkk ay « anesthésie »… Nde, defoon nan ay komànd ci ñi koy jaay, waaye ba tey jotunu ci. »
Looloo tax ñu fomm bépp xeetu opperaasiyoŋ jamono jii. Waaye, jëwriñu xamle na ne nguur gaa ngi def kéemtalaayu kàttanam ngir ut ko.