Ab sàndarm moo ñàkk bakkanam fa diiwaanu Kéedugu. Dafa def aksidaŋ ci tali Salemata bi. Xibaar baa ngi tukkee ci kilifay kaaraange gi.
Ci altiney démb ji, 8 awril 2024, la aksidaŋ bi am, bi 22i waxtu jotee ci guddi gi. Nee ñu, ca korosmaa Diara-Pont la jéyya ji xewee.
Ab móto la sàndarm bi doon dawal ba dal ci kow aw nag wu tëddoon ci diggu tali bi. Ca la daanoo daanu bu metti, bërëngu ay yoon, daldi ñàkk bakkanam ca saa sa. Sàppëer yaa jëli néew ba, yóbbu ko ca morgu ba ca raglub Amaat Dãsoxo bu Kéedugu.