TAKK-DER YI LÉEMATI NAÑU KËRU USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jamono ji nuy yaxal mbind mii, takk-der yaa nga fees dell Cité Site Kër Góorgi (Cité Keur Gorgui), fa Usmaan Sonko dëkk. Yoon yeek mbedd yi jëme kër njiitul Pastef yépp lañu fatt. Kenn duggul, kenn génnul. Koñ bépp lañu léem. Kenn amul fu muy jaar ba dugg fa.

Cig pàttali, ginnaaw mitiŋu démb bi, Pastef dafay amal i doxi-ñaxtu ci 14i depàrtmaa yépp ci bésub tey jii. Ni Maki Sàll yoree réew mi, ci fànn yépp, lañuy kaas.

 

Boroom nataal bi : Bentaleb Sow

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj