WAY-SOPP LÀMMIÑI RÉEW MI, TOOGAAY AMATUL !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àjjuma 17eelu nowàmbar 2023 ca Fatig, Njiitu réew mi, Maki Sàll, yëkkati na yile kàddu :

« Abajada bi, buñ ko yombaloon, Senegaal romb kon na fii bu yàgg. Waaye, ku nekk di indiy xam-xam yu xóot ba kenn xamatul lu yëf yiy niru. Buñ la bindalee pulaar, doo ko mën a dawal, ndax daa jafe lool, séeréer naka noonu. Mënoon nañoo jël loyi lateŋ yi, mu gaaw, nga dawal ko ni nga koy déggee, mu jeex… Waaye loo xam ni kenn mënul xam lan la… »

Maki miy jaay « savant » ndekete xamul sax li muy wax ci làmmiñi réew mi. Abajaday làmmiñi réew mépp ci loyi lateŋ walla yu araab lañ leen di binde. Loolu Maki Sàll xamu ko woon ba bi muy yëkkati kàddu yii ca Fatig.

Xéy-na dafa fàtte. Te sax, fàtte xaju fi, walla boog mbirum làmmiñi réew mi ñoru ko ndax bi Ablaay Wàdd torloo dekkere 2005-992 bu ñaar-fukki fan ak benn ci weeru oktoobar, atum 2005, moom Maki Sàll moo nekkoon ca jamono jooja njiitu jëwriñ yi.

Waaw, moom ba mu gisee na waa Keeñaa ak ñeneen di binde, lu ko tere woon laajte lu tax li xew réew sàngam amul Senegaal ? Xéy-na su ko defoon ñi ko wër dinañ am fitu wax ko dëgg.

Li gën a doy waar mooy ne, ak li coow liy bari lépp ak liggéey bu takku bi ay jigéen ak i góor di def ci làmmiñi réew mi, Maki Sàll mësul teg bëtam ci téere bob, ci làmmiñi réew mi lees ko binde. Su amoon dina xam lum bon bon ne loyi lateŋ lañ ciy jëfandikoo.

Ku xamul woon lu tax xeex bi ñeel suuxat làmmiñi Senegaal yi àntoogul,  kàdduy Maki Sàll yi dinañ la doy tontu. Càggante gii ak xamadi gii jéggi nañ dayo.

Ndax xel mën naa nangu ne liggéey bu réy bi fi OSAD def, ARED, PAPYRUS, EJO, FONK SUNUY LÀMMIÑ, Ànd jubal mbind mi, Wolof Ak Xamle ak banqaasu Làkk ak Caaday Afrig ba ca jànguneb Ndar ump na Maki Sàll ? Téere yi Séex Aliyu Ndaw añs. bind nag ? Nee leen déedéet waay ! Waaw, kon téere jàngukaay yi jëwriñu njàng mi di defarlu nag, xanaa du Maki Sàll a ko digle ? Walla ? Jawriñu Mbatiit mi tamit mi ngi jàppale këri móolukaay yi te siisul ñiy liggéey ci làmmiñi réew mi…. Kon Maki Sàll, waxam jii, lu ko wund ? Nun de xamunu ko. Ku ko xam jàppale nu ci.

Am na ñu ñaan Maki Sàll da doon joxe xalatam ci solos làmmiñi réew mi ak nees leen ku nekk war a mën a jëfandikoo ngir bañ a « sànni say wax ». Mën naa nekk de, waaye mbir xanaa bala nga koy layal day fekk nga xam ci as lëf ! Am déet ?

Te moom sax, du ci làkku tubaab la yore réew mi ci diirub 2i moome, mu tollook 12i at ? Booba xamul woon dayoy sunuy làmmiñ ? Lu tax mu nég ba 3i weer kese dese ko mu ciy door a yéy yàbbi ? Day door a nànd la Séex Anta daan wax ne « am réew mënut a suqaliku ci làkku jàmbur » ?

Noonu rekk la, ku nekk dafa jàpp ne yaa gën a aay ñépp fekk li Yàlla xam doy na. Loolu bokk na ci li tax làmmiñi réew mi suqalikuwuñu. Bu loolu weesoo, lan moo tax nu war a jël sunuy làmmiñ di ko saax-saaxee « ngir mbir yi gaaw » ? Làkk jafewul waaye du luxus, làkk wu nekk day wone taaram, ñu war koo bind na mu waree, ànd ak nees war a tëgge ak teqalileek taqaley waatam, ni ko Càmm gi yoonale jaare ko ci Dekkere bi. Ndax lii dug yaras jëme ci li nga moom. Wolof nag nee na, ku fonkul boppam, ku mu ne fonk na la da lay nax.

Liggéey bu takku bi ak jéego yu am solo yi, waxumalaak pas-pas bu réy bi, laf biy bawoo ci mbooleem ñiy yëngu ci làmmiñi réew mi, Maki Sàll xamu ci lenn. May laaj luy njariñu ñi koy xelal ak a xibaar ? Yan dégg-dégg lañ koy jox ?

MBOKKI FONK SUNU LÀMMIÑ YI, toogaay amatul, jóg gënati na jot. Wéy di jëf ! Xamle ! Sëriñ Musaa Ka noon na :

« Bépp làkk rafet na, buy yee ci nit xel ma, di tudd ci jaam ngor la ». Kon rikk bu nuy séqi jéego jëm ciw làkk, nan ko doore ci yi nu nàmp.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj