Lees doon xaar jib na : Yanqooba Jatara, jëwriñu tàggat-yaram gi, génn na pàrti Rewmi, te daa fas yéene tekki ndombog-tànkam. Moom, nag, moo nekkoon tof-njiitu pàrti Rewmi laate Idiriisa Sekk di ko fa wuutale ak keneen. Loolu sax a sabab ndogal li mu jël. Loolu nag, du mbetteel. Ndax, digganteem ak Idiriisa Sekk dafa ñagas fan yii. Ñoo ngi doon wax, naan, Idi daf ko toroxaloon keroog, ca seen ndaje ma, moom ak Aali Sale. Seeti woon na kilifag pàrteem gi ngir xamal ko ndogal lim jël.
Ba mu génnee ca kër njiitam li, fa Point E, la fésal xibaar bi, wax ne, day delloo palaasu jëwriñ ji ngir Idiriisa Sekk digal Maki Sàll mu tabb fa keneen. Nee na, looloo gën a yenu maanaa, ndeem toppatul ci kilifag pàrti Rewmi.
Moom, nag, Yanqooba Jatara, feddali na kóllëreem ci Idi, wax ne, mbirum palaas mësu koo itteel. Ca la waxee ne, mu ngi ndokkeel Dr Ndóoy lim ko wuutu, mu ne yeyoo na palaas bi te dina topp ci ginnaawam, jàppale ko. Yanqooba Jatara dafa jàpp ne dafa def njuumte ci wàllu pólitig, moo tax yeddaange gi dal ko. Daf ne :
“Idiriisa Sekk dafa jàpp ne dama juum ci wàllu pólitig, moo tax mu tekki samay ndombog-tànk ci pàrti Rewmi.”
Bim génnee ca këru njiitul CESE li, dafa tënk seen waxtaan, biral ne :
“li yenu maanaa mooy, bu dee nekkatuma tof-njiitu Rewmi, dafa war a digal Maki Sàll mu wuutale ma keneen ngir mu nekk jëwriñu tàggat-yaram gi. Waaye, Idiriisa Sekk dafa bañ.”
Nee na, bu jotee, Idiriisa Sekk dina ci indiy leeral. Waaye, lu ci mën di am, du worook Idi. Ndax, dafa jàpp ne, moom, doomam la te du « mës a def luy lor Idiriisa Sekk… »