Démb la àttekatu Ñaareelu kabine bi dóor ab « mandat de dépôt » ndawul Pastef li, Yarga Si. Lees koy toppe moo di ne, dafa doon jéem a faat bakkanu njiitam lii di Usmaan Sonko. Moone de, meeru Sigicoor bi setaloon na Yarga Si. Noon na sax, Yarga Si mi ñu jàpp, « rakkam » la, te sañ na ko dénk bakkanam. Waaye, Yoon mayu ko nopp. Walla bu ko mayee nopp itam, daf ko tanqamlu.
Àttekat bi dafa sandwiital njiitul Pastef li. Faalewul i kàddu yi Usmaan Sonko yëkkati woon keroog, bi muy waxtaan ak askan wi, daldi ciy setal deru Yarga Si. Lu ko jiitu, toppekat bi, Ibraayma Baaxum, dafa jiiñoon Yarga Si, ne moom lañ gis cib widewoo, am lum piis Usmaan Sonko. Ci loolu la sukkandiku, wax ne moom lañ jàppagum ne, moo bëggoon a rey Usmaan Sonko. Li jaaxal ñépp, nag, mooy ne, ndeyu-mbill ji pelentul te yëgul woon sax ne doorees nab luññutu ñeel ko. Usmaan Sonko, moom dafa gis ne, balaa ngay amal i laaj-tontu ñeelrey biñ ko bëggoon a rey, nga woo boroom, déglu ko balaa dara, waaye « …ngay woote ay ndaje, di wejejeji, di wax loo xam ne amul bopp, amul geen. »
« … [Yarga Si] lum ma jox ma lekk, lum ma jox ma naan. »
Du Yarga Si kese lañ jàppoon sax. EL Maalig Njaay ci boppam, tegoon nañ ko loxo. Moom, dafa ne woon, dañ doon jéem rey Usmaan Sonko. Waaye, ginnaaw gi, dañ ko bàyyeendi, takkal ko lamu elektoronig. Njiitul Pastef li ne, bu jàpp dee am, moom lees war a njëkk a jàpp. Ndaxte, moom moo njëkk a wax ne dañ ko doon jéem a faagaagal, tuumaal ci waa pólis ba mu leer. Li jaaxal Usmaan Sonko, nag, mooy ne moom, pelentul kenn te yëgul woon fenn fu toppekat bi féetewoo mbir mi bay jàpp ay nit ñu deful dara, di wax loo xam ne, « dara du ci dëgg ».
Njiitul kujje gi tegoon na ci, wax ne :
« Yarga Si, sama rakk la, di ànd ak man. Bu ma nekkee ci daamaar bi sax, mooy taxaw ci kow yor raaya bi. Bu may tukki, mooy ànd ak man ba naawu ba, ànd ak man ba ci yéeguwaayu roppalaan gi. Ndax, ca naawu ba lay liggéeye, am na sañ-sañu àgg foofu. Kooku, wóolu naa ko ba, lum ma jox ma lekk, lum ma jox ma naan. »
Setal na deru Yarga Si, « rakkam » ji, wax ne bineegar la jël, def ko ci musuwaar, jox ko ko ngir mu mën a noyyi. Mu ne loolu bokkul ak li ko pólisee yi sotti.
« Toppekat bi waxul dëgg. Li ñuy nëbb, ñoom, ak li ñuy ragal, waxaguñ ko. Ndax, nun, lin ci war a def, def nan ko. La nu waroon a yóbbu, génne nan ko réew mi, te nee nañ nu fan yii dinan am njureefi ceet gi… Nañu xaar, bu dee nee nañ nu ndefar gi du dara, nu xam ni du dara, kaani rekk la gu saf. Waaye, bu dee ndefaru simi, nu wax ñépp ne ndefaru simi lañ nu sotti te ndefaru simi googu mënoon na faat sunu bakkan. »
Bu doon maandute am na, Yarga Si kenn dootu ko toppe dara. Ndax kàdduy Usmaan Sonko setal nañ ko ba mu set wecc. Kon, lu tax Yoon di jafandu ci moom ? Ngir fàttali, Yoon doon na topp Yarga Si ci meneen mbir balaa mii ñu koy toppe.
Yarga Si, ndaw la bu tollu ci 35i at, di liggéeye ca naawu AIBD. Rax-ci-dolli, moo jiite Pastef ca Sàkkal. Keroog, 16 màrs 2023, ba takk-der yay toj oto Sonko ba di ko ca génne, dañ fa dooroon ay gërënaad lakkirimosen ba mu wex xàtt, noyyi jafe woon ca béréb ba. Moom, Yarga Si, ca ña gunge woon Sonko la bokkoon. Ca la ko joxee ag kol gum tooyalee woon ak bineegar ngir mu taf ko ci bakkanam, mën a noyyi. Ba ko luññutukat yi laajee, dafa waat ne, dimbali Usmaan Sonko rekk a ko taxoon def loolu.
Yarga Si weddi na tuuma yi. Usmaan Sonko setal na ko ba mu set. Am na ab widewoo bu tas ci mbaali jokkoo yi, ñu ciy gis ab sàndarm buy piis dara Usmaan Sonko ci biir otoom. Àttekat bi daldi gëmm, gumba-gumbalu ; mu daldi tanqamlu, tëx-tëxlu. Xel ñaaw na. Mu mel ni, dafa am lu ñuy nëbb. Mbaa du Yarga Si lañ bëgg a def béyu sarax bi ?