BASIIRU JOMAAY JAXAAR FAY SIIWAL NA AM-AMAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Basiiru Jomaay Jaxaar Fay dafa bokk ci lawax yiy dagaan baatu askan wi ngir doon juróomeelu Njiitu réewum Senegaal. Fan yii weesu, mi ngi doon woo yeneen lawax yiy xëccok moom jal bi, rawatina Aamadu Ba, ñu siiwal seen i am-am ngir Saa-Senegaal yi xam ku ci gët i loxo. Moom nag, ni mu ko digee woon, biral na bosam.

Bi lawaxu Usmaan Sonko bi xaymawee alalam, nii la tollu :

SUUF AK KËR

– Benn pàkk bu 80m/40 bu nekke fa Njagañaaw, di jar 3i milyoŋ ci sunuy koppar. Atum 2017 la ko jënd ;

– Ab toolu 4,3 ektaar, nekk fa kominu Sànjara, di jar 15i milyoŋ yu teg 10i junni. 2022 la ko jënd.

– Pàkkub 200m2 fa Cess buy jar 700.000 ca 2009 ;

– Kër gu ñu tabax ci pakkub 200m2 diggante 2017 ba 2021 (muy kër gu mu dëkk, moom ak njabootam, 2021 ba tey). Meermoos la kër gi féete, mu fàggoo ko ci mbootaayu liggéeykati DGID yi. Bu dee tabax gi, am na ci lolo, xaalisu boppam la ko defee, li ci des mu leb ko bànk yii di UBA ak BICIS. Ci lim bind, jotam mayu ko woon muy xayma njëg li.

DAAMAR YI

– 2i daamar : 1 Focus 2012 bu ñu jënd okaasiyoŋ buy jar 6.500.000, mu jënd ko ca 2019 ak benn Ford Explorer Platinum bu ñu jënd okaasiyoŋ ci njëgu 19i milyoŋ ca 2022.

SÀQ YI (COMPTES BANCAIRES) AK XAALIS

– Benn sàq (compte) ca UBA bu def 3.276.046 FCFA 19i mars 2024

– Benn sàq bu am 786.782 FCFA 19i mars 2024

– 29i milyoŋ yu teg téeméeri junni ak ñaar-fukk ngir ñagee ko toolam bi, defar ci fooraas, defar ci baseŋ, gas ci pomp, jënd ci jiwu te fay ci ña fay liggéeyee ;

BOR YI

– Bor bu tollu ci 30i milyoŋ yu ñu leb ca UBA 5i sebtàmbar 2022

– Bor bu tollu ci 8i milyoŋ yu ñu leb ca BICIS 22i ut 2022

– Borub 10i milyoŋ bu ñu sunu benn xarit lebal ngir tool yi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj