BOOS NDÓOY
Saa buñ tuddee réewum Kibaa, ñépp daldi fàttaliku njiitam lu ràññeeku la : Fidel Castro. Waaye, xel yépp dañuy dellu 60i at ci ginnaaw, jamono ju leen réewum Amerig daan xoqtal. Ràññees na réewum Kibaa yit ci wàllu wér-gi-yaram. Ndege, am na ciy doomi Kibaa yi ay fajkat yu mag a mag. Te, ñooñu, kenn ci àddina si sànul a werante seen xam-xam ak seen xarañte.
Waaw.
Weddi, gis bokku ci. Kibaa waneetina mën-mënam. Lu tollu ci 52 doktoor la yónnee réewum Itali mi nga xam ne, deele na nit ñu baree bare ci sababu mbasum Covid-19 mi. Dafa di, doktoori Itali yi ci seen bopp ñoo demoon ba tële ndax way-tawat yu jéggi dayo. Ndeysaan, am na sax 14i doktoor yu ci ñàkke seen bakkan.
Laata ñuy dem Itali ngir walluji leen, doktoori Kibaa yi dañu def benn portale bu rànneeku. Bi ñu koy def, nag, ñenn ñi dañoo téye waale benn nataalu Fidel Castro. Boo leen gisee, ñoo ngi ànd ak sag bu réy. Mu mel ni dañuy ndamoo nataal bi, di ko furloo ñeel seen nooni démb yi. Bu dul woon mbasum Covid-19 bi fatt xel yépp fi mu ne nii, foto bu ni mel doon na jur coow lu réy a réy ci àddina si. Waaye, wolof nee na, gumba tal na leneen lu dul tëb i teen.
Kii di Fidel Kastóro, daa teeloon a xam ne, am réew, bu bëggee mucc ci nootaange, fàww ña fa nekk bëgg ko ba fu mbëggeel yem. Ndege, naw sa bopp, bennoo ak muñ ñooy cëslaay yiy dooleel am réew. Bu ko defee, dina mën a dékku képp ku koy xeex, ak noo mënti tollu. Tànk yooyu la Fidel Castro daan dox. Moo tax, dafa fullaaloon li askan wi soxla te muy lu mënta ñàkk : njàng meek njàngale mi ak wér-gi-yaram (paj mi). Kon, réewi Afrig yu ñuul yi Farãs nootoon mën nañoo roy ci Kibaa ak Fidel Castro. Ndaxte, jooytu ak yàccaaral yiñ nekke du leen jëme fenn.
Mbooloo fajkat mi Kibaa yabal Itali, nag, dafa rax ay nit yu bokk ci xeet yu bare. Moom kay, na réew ma bindoo rekk la mbooloo mi mel. Mu tey ko am déet, réewum Kibaa ngi jàngal doom-aadama yépp, ak fuñ mënti nekk, njàngale mu réy te am solo. Njàngale moomu, dees na ko jagleel way-boddiy(racistes) àddina si. Ñooñu nga xam ne, jàpp nañ ne ñoo gën ci mbindéef yi. Ñooñee ànd ak mbañeel gu jéggi dayo ñeel nit ku ñuul ; ñooñee di tëj seen i réew, di ko aaye Móodu-Móodu yi walla di leen fa xoqtal ak a bugal mbugal yu metti guddeek bëccëg. Dañ koy wax te dee, Itali ci réew yu siis yooyu la bokk. Waaw sax de, réewum Itali mi mbooloo Kibaa mi rax ay nit ñu ñuul dem walli ko !
Boo janook sa tele di gis doktoori Kibaa yeek boroom der yu ñuul yi ci nekk, nit ñu weexi Itali yi di leen tàccu, dangay yéemu ci Yàlla, naan déedéet kañ ! Ñii nga xam ne, gaawu walla dibéer ju nekk, ñuy yuuxu ay yuuxiy golo, di xas, di saaga ak a tuutal futbalkat yu ñuul yi ci seeni estaad… Mbaa du dañoo fàtte xaat ne weer yii weesu rekk ñoom ñoo doon filme ak a ñaawal Paate Sabali, doomu Gàmbi bi doon lab ci dexug Weniis gi, lànk ne duñ ko dimbali ? Xalaas !
Moone de, ndaw yiy jël i gaal ni Paate Sabali, duggewuñ ko lu dul daani seen doole Itali ngir dundal seen njaboot. Nde, xéy amul ca réew ya ñu bawoo, dund gi jafe fa lool, njiit ya fa nekk dëkk ci ger, càcc ak bunduxataal askan wi. Rax-ci-dolli, njiit yooyu, dañuy jaamu réewi sowu yi, rawatina Farãs, di leen jébbal alalu askan wi ci anam bu ñaaw a ñaaw, koom-koom gi jaare fa nasax. Loolu la ndaw yiy daw, di wutali réew yu mel ni Itali. Tey, Itali googu, réewi Ërob yeek yu OTAN yi dañ ko dummóoyu. Bu weesoo Siin ak Riisi, Kibaa rekk a fullaal wooteg wall gi mu woote bi mu demee ba jàq lool. Amaana réewum Itali jóge fi xam ne nit, nit mooy garabam tey gën a fonk ndawi Afrig yiy fëg ci buntam.
Nu jeexale ko ci ne, li àddina sépp war a jàng ci mbasum koronaawiris mi mooy ne, nit ñépp benn lañu, warul am xàjj-ak-seen. Muy jamonoy mbas, naqar, tiis walla jàmm, ñépp war a doon benn, joxante cër. Lii lanu mbasum Covid-19 bi fàttali ci anam yu metti. Amul réew walla xeet wu ci mucc. Fu nekk nee na fa saraax, daaneel fa ku weex ak ku ñuul, boroom alal beek baadoolo bi, ñi siiw ak ñi siiwul. Booy seet sax, danga naan dafa singali kilifa yi gën a mag ci àddina si. Moo tax, képp kuy nit, war ngaa fàttaliku kàdduy Martin Luther King ya. Dafa ne woon : “War nanoo jàng a dund ni ay doomi-ndey, bu nu ko deful, dinanu dee nun ñépp niy tuut-tànk yu seen xel desee mat.”
*Boos Ndóoy bind na ci nasaraan ñeenti téerey xeltu yu am solo, ñu mën cee lim ‘’L’énigmatique clé de l’immigration’’ ak ‘’L’Etat déballe tout’’. Boos Ndóoy doomu-Senegaal la, dëkk Monreyaal ca Kanadaa, di fa liggéey.