SÉEX ALIYU NDAW : BÉS DU ÑÀKK, DAY SORE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ daa fas yéene delloo njukkal bindkat bu mag bii di Séex Aliyu Ndaw keroog, àllarba 18i fan ci saŋwiyee 2023 mii ñu dégmal. Xew-xew baa ngay ame ca Kërug Mbatit gees duppee Duuta Sekk (Maison de la culture Douta-Seck).

Fonk sunuy làmmiñ delloo na mbàttu ca ndaa la. Muy ag kurél gog, dafa ëmb i góor ak i jigéen yu takku taxaw, di liggéeyal mbatit ak làmmiñi Afrig, rawatina yu Senegaal yi. Liñ ko dugge mooy fett bëti Saa-Afrig yi ba ñu mën xippi, xool, ràññe seen dayoy làmmiñ. Manaam, jubluwuñ ci lu moy yeewu, yeete ci solos làmmiñ ñeel naataange ak yokkuteg réew, rawatina yoy kembaarug Afrig. Nisër booboo di cëslaayu mbootaay gi. Noonu, dinañuy faral di jàngale làmmiñi réew mi, rawatina wolof, di amal i waxtaan yi aju ci làkk yi, mboor ak mbatit. Muy liggéey bu am solo. Waaye nag, liggéey boobule, doonuñu ko woon mën a def bu amul woon i werekaan ak jàmbaar yi leen ci jiitu, xàll yoon wi, ba tey ñu ñemee sóoru xeex bi. Ñooñu dellu, àndaat ak ñoom ci xeex bi, gunge leen, di leen tette ak gindi ba ñu àgg fi ñu àgg tey. Dafa di, bu peccum liir neexe, ndey jaa téye ci mbagg yi. Jàmbaar yooyu, Séex Aliyu Ndaw ci la bokk. Moom nag, Séex, ku ko xamul, dégg nga ko. Waaye, du tee nu mosal leen as tuut ci jaar-jaaram.

KAN MOOY SÉEX ALIYU NDAW ?

Séex Aliyu Ndaw a ngi ganee àddina Biññoona, ca atum 1933. Senegaal la jànge, waaye jànge yit Farãs. Nekkoon na itam jàngalekat, daan jàngale làkkuw àngale ci daara yu digg-dóomu yi. Ginnaaw njàngale mi, jot naa am ay ndomboy-tànk yu bari, moo xam ci yi ko Nguur gi dànkoon walla i liggéey yi aju ci fànni mbatit, cosaan ak làmmiñi réew. Séex Aliyu Ndaw, yemul woon rekk ci liggéey. Dafa yattoon xalimaam, bind ay téere yu gànjaru. Dafa di, mbind mi lees ko gën a xame sax. Waaw, bind nay téere yu siiw farãse, wëlbatiku bind ci wolof.
Tey, ci wàllu wolof, ku ne ladab, doo lim ñaari bindkat te boolewoo ci Séex Aliyu Ndaw. Boo moytuwul sax, moom ngay jiital ci toftaleg werekaan yi. Ndaxte, miinees na lool aw turam ci mbindum wolof. Téere fent, téere taalif, nettali, kilib ak léeb, Séex bawul dara. Ca njël la jóg, balaa ginaar yiy sab, di bind, démb balaa tey. Kon, góor gi bay na waaraam. Yoon wa Séex Anta Jóob xàll, ànd ceek yeneen i kàngam, càllale ga, Ndaw a koo jottali ndaw ñi. Waaye, dees na wax ni : ñaq du réer boroom. Ndax ag farloom, ak yitte ju mu jox làmmiñi réew mee tax ñu ko ciy sargal saa su nekk. Firnde li mooy, ca atum 1962 la jotoon neexalu taalifkatu Senegaal ca téereb Kairée ba. Ca atum 1969, mu jotaat ab neexal ca Alséeri ginnaaw bi mu bindee L’exil d’albouri. Téere yooyu, ci farãse la leen bind. Waaye ci atum, 2012 jotoon na raaya bu mag bees duppee Njiitu réew mi te ñu jagleel ko kàllaama yi.
Kon, ñu gis ne, Séex Aliyu Ndaw dafa yàgg a fonk làmmiñ yi. Moo tax képi ku fonk làmmiñ yi war koo fonk. Loolu la mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ xam ba jàppal kob bés ngir sargal ko, seexal ko, nees koy waxe. Waaw kay, seexal ba mu neex. Ma ne, Péncum Maam Yunus Jeŋ bu ñu seexalee Séex Aliyu Ndaw, ku ca sàñ a wax ? Xanaa ku ko réere. Kon, bu bés baa, keroog àllarba 18i fan ci saŋwiyee, Bu Séex duggusee, dinaa wuyoo bàkkub mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ. Nde, ku ne “jàng, jubal, jariñoo”, war a xam ni loolu la Séex Aliyu Ndaw làmboo. Kon, bés bi bésam la. Yéex naa am nag. Waaye, mënutoon a ñàkk. Ndax, wolof nee na, bés du ñàkk, day sore.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj