Lees doon njort moo am : takk-der yaa jàppoon, ndeke, Usmaan Sonko. Fim ne nii, delloo nañ ko këram. Antuwaan Feliks Jom, jëwriñu biir réew mi, moo ko xamle ci surnaalu RTS bu 20i waxtu bi. Lu ko jiitu, pekkug pólitigu Pastef génne woon nañ yégle, wéral seen réerub njiit li ba noppi di artu ak a waajal jàmmaarloo bi.
Li jëwriñu biir réew mi wax ci coowal réerub Usmaan Sonko bi mooy, ci tënk, lii toftalu :
-
“Usmaan Sonko sàmmontewul ak Yoon ginnaaw bi mu defee ndiiraanam gog, yégalu ko njiiti réew mi ;
-
Usmaan Sonko dafa sabab ag dalandi diggante Sigicoor ak Welingara te am nay alal yees yàq ak kuñ ci rey (na ko Yàlla yërëm, noo ngi jaal ay mbokkam) ;
-
Ñoo ngi jàppe Usmaan Sonko ci daamar gog, biñ ko lëñbëtee, fekk nañ ciy ngànnaay, ay mbaq ak i biiy yu ñu jëfandikoo cib ñaxtu.”
Li jaaxal ñépp nag, moo li Antuwaan Jom wax ne “jàppuñu woon Usmaan Sonko”, waaye “dañ ko dànd ba këram”. Waaw, ak lees ko tuumaal yépp, waxtu wii kay kaso la ko waroon fekk, xanaa ?.
Nga jalgati Yoon, yéeg ci daamar gu yab i ngànnaay añs., ñu jàpp la, gunge la ba sa kër, bàyyi la. Loolu lépp, ci lu kenn yégul, kenn tinul. Ma ne, njaw des njaw xambin. Nit ñi dofuñu kat. Dafa di, bu doon ab baadoola la, kon waxtu wii doon na ko fekk ndung-siin. Biñ jàppee Usmaan Sonko ba léegi, ci guddi gi lay sog a àgg këram. Fum nekkoon ci diggante bi ? Num fa nekke woon ? Lu tax ñu jàpp ko ci pet ? Am na lees waxul.
Usmaan Sonko nag, xamle na ne dina waxtaan ak askan wi bu 23i waxtu jotee. Nu xaar ba xam la muy wax ngir méngale ko ak waxi Antuwaan Feliks Jom yi.
Boroom nataal yi : Anita Tv