YOONU GÀMMU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mawlidu Nabi, ñu ciy màggal juddug Yonnent bi (sas), moom mi Yàlla sunu Boroom yonni woon ci mbindeef yi. Muy daje ak fukki fan ak ñaar ci weeru gàmmu, di yamoo ak àllarbay tey jii, 27eelu fan ci sàttumbaar. Jullit yi di ko màggal fépp ci àddina si. Ñu nemmeeku taxawaayu réewum Senegaal ci boobu xew-xewu diine. Këru diine yi fi nekk di ko taxawe saa su ne. Tiwaawon, Njaasaan, Medina baay, Taa-if ak feneen ak feneen. 

Jullit yi farlu nañu ci màggal bésub Yonnent bii di Seydinaa Muhammad. Nde, ku ko màggal màgg. Mu doon jamonoy mbégte ak cant ci ñoom ñiy taxawe bés bu mag bile. Tiwaawon ma ngay fees ak mbooloo mu takku. Taalibe Séex yaa ngay wutali béréb bu sell ba ngir màggal guddig Sang ba. 

Naka noonu, ñu nemmeeku fa teewaayu kilifa yu bari. Moo xam gog diine, aadaa wala sax way-pólitig yi. Njiitu réew mi demoon na siyaare xalifab Tiwaawon bi, Sëriñ Baabakar Si Mansuur, ci talaata ji. Ba mu fa jógee la dem fa Medina-Baay ca kanamu Sëriñ Maahi Ñas weccante ak moom ay kàddu. Waaye tamit fésal na ag tàggatoo ak réew mi. 

Ñu gis tamit way-pólitig ca béreb yooyu. Ku ci mel ni Aamadu Maam Jóob, Sëriñ Mbay Si Abdu ma yore seen kàddu dalal na ko, mu amal ab siyaaram ci kilifa ga. 

Ca weneen wàll wa, ñu seetlu ni Nguur gi jël na ay matukaay yu réy a réy ngir bés boobu yemb ci béreb yu bari. Onaas a nga ca Medina baay. Jël na ay matukaayam ngir feg mbënn ma foofu. Bu ñu jëlee wàlluw dem bi ak dikk bi, nemmeeku nañ fa saxaar ga ca Tiwaawon ngir yombalal way-tukki yi seen ub dem. Taxawaayu takk-der yi tamit fés na fa lool ngir saytu kaaraange askan wa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj