BENNOO BOKK LAWAX WALLA FÉEWALOO TAS YAAKAAR ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar la yéenekaay yi xëyee tey ci àjjuma ji, 8 sàttumbaar 2023. Ñépp, daanaka, dañu gaatnga tasug lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar bu Njiitu réew mi tànnee lawaxam.

Juróomi weer kott la Maki Sàll dese ci boppu réew mi. Moom Njiitu réew mi, xamle woon na ne du bokk ci wotey 2024 yi, daldi koy feddali keroog bam toogee ak Sëriñ Muntaqaa Mbàkke. Bu ko defee, Senegaal dina am njiit lu bees keroog, 25 féewaryee 2024, walla sax ci weeru màrs (bu dee ñaareelu sumb am na). Kan moo wuutu Maki Sàll ci jal bi ? Yàlla rekk a xam. Waaye limu lawax yi bëgg a nekk 5eelu Njiitu réewum Senegaal moom, bare nañu lool.

Bu dee ci kujje gi, mbiri Usmaan Sonko rekk a lëntagum xel yi. Wëliis njiitul Pastef li, ñeneen ñépp samp nañ seen i ndënd : Xalifa Sàll, Abdurahmaan Juuf, Ceerno Alasaan Sàll, Décce Faal, Maalig Gàkku, añs. Bu dee waa Bennoo Bokk Yaakaar moom, ci gaawug ëllëg gii la Maki Sàll war a fésal ki mu tànn.

Biir Bennoo Bokk Yaakaar, ñu bare ñoo teg bët toogub Njiitu réew mi. Ñi ci gën a fés ñooy Aamadu Ba, Bun Abdalaa Jonn, Aali Nguy Njaay, Abdulaay Daawda Jàllo ak Maam Bóoy Jaawo. Ñii ñépp nag, bu ñu bennoowee yit, bokkuñu yaakaar. Ndax, kenn bëggul bàyyee sa moroom, ndax kenn wóoluwul sa moroom. Te sax, looloo yàggal mbir yi. Ñoom, waa BBY, amal nañuy ndaje yu bare yoy, Njiitu réew mi ci boppam moo leen tëggoon. Lépp rekk ngir diisoo ak ñoom, xirtal leen ci ñu topp ci ginnaaw kim nar a tànn. Waaye loolu de, ay gént kese lay ndiru.

Njiitu réew mi dafa woote am ndaje fa pale ba, ci àjjumay tey jii, ci 16i waxtu ci ngoon. Njiiti lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar yi la ci woo ak ñeneen ñu bokk ci yeneen i kurél yi ànd ak ñoom. Nee ñu, li mu ko duggee mooy fexe lëkkatoo gi bañ a tas bu siiwalee ki mu tànn walla mu néewal ngaañ yi. Alxames jii weesu, amaloon nañ am ndaje fa dalub APR. Ku ci mel ni Mahmout Sale jël na fa kàddu gi, layal Njiitu réew mi. Jéem na leen xamal ne, topp ginnaaw lawax bi Maki Sàll di tànn mooy li gën ci lëkkatoo gi, gën ci képp kenn ci ñoom. Nee ñu, dibéer ji sax amaat nañu am ndaje.

Ndaje yi bare nañ, waaye  ba tey seen i mébét ak seen bëgg-bëgg dajeeguñu. Dees na xam ndax, keroog bu Maki Sàll siiwalee lawax bi mu tànn, dañuy bennoo bokk lawax, bootu ci ginnaawam walla ndax dañuy féewaloo tas yaakaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj