Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/3/2025)

COOWAL AMNISTI BI Coppiteg amnisti bi dépitey Pastef yi namm a wotelu ca Ngomblaan ga moo lëmbe réew mi jamono yii. Bu ñii waxee jëm...

JËWRIÑ ABDURAHMAAN SAAR AK JËWRIÑ SÉEX DIBAA DALAL NAÑ AY NDAWI FMI

FMI yabalati na ay ndawam fi Senegal ngir ñu waxtaan ci mbirum koom-koom ak koppari réew mi. Jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Koppe...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (18/3/2025)

COOWAL MUURAAY YI CI LEKOOL BI Coowal muuraay yi ci lekool bi dekkiwaat na. Démb ci altine ji, njiiti lekool bii di Collège Saint Grabriel...

MBËKK MI : JÀPP NAÑU MEERU JONWAAR BI

Laasana Saar, meeru Jonwaar, ak yeneen juróom-benni nit ñu ngi ci loxoy Yoon jamono jii. Li tax ñu jàpp leen moo di ne, dañu...

PAAB CAW TÀNN NA AY GAYNDEEM

Tàggatkatu Senegaal bu bees bi, Paab Caw, biral na ay ndawam keroog ca alxames jee weesu. Moom nag, dafa mottali yéeney saa-senegaal yu bari...

NJAAM GU YEES FA ARAABI SAWDIT

Xoqatal ak metital ya amoon ca jamonoy njaam ga dekkiwaat na fa Araabi Sawdit. Nekkin wu metti la fa jigéeni Afrig yi fay daan...

MALIKUNDAA : KËRUG MBËJ GU BEES

Senelec taxawal na kërug mbëj fa Malikundaa. Loolii dina tax ba dawaanu mbëj mi ful fukki yoon fa Pointe Sarène. Nde, lu jiitu ñu...

NGOMBLAAN GI : DÉPITE YI JÀLLALE NAÑU ÑEENTI SÉMBUW ÀTTE

Démb ci àjjuma ji, Ngombalaan gi wote na ñeenti sémbi àtte. Ñuy i àtte yuy yoonal ci Njiitu réew mi mu xaatim i déggoo...

SOWAAL : JÀPP NAÑU GAAL GU YABOON LU ËPP 300I MBËKK-KAT

Ndawi duwaan yi nekke Fimla jàpp nañ ag gaal gu naroon mbëkki. Gaal googu nag, dafa yeboon lim bu tollu ci 300i mbëkk-kat ak...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI(13/3/2025)

NDOGAL YI ELIMAANU JËWRIÑ YI JËL ÑEEL MBIRUM SUUF SI Démb, ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yi, ni ñu koy defee ayu-bés...

NDAJEM JËWRIÑ YI (13/3/2025)

Nees ko tàmm a defe, ayu-bés bu jot, amal nañu ndajem jëwriñ yi démb ci àllarba ji, 12i fani màrs 2025. Fa Njénde la...