Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (9/12/2024)

NDAJEM DOHAA MI Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay teeweji woon na Ndajem Dohaa mi ñu doon amal fe Qataar ci njeexitu ayu-bés...

TUKKIB MAGUM JËWRIÑ YI FA GÀMBI

Démb, ci gaawu bi la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, demoon fa Gàmbi. Li waral tukkeem boobu mooy fekke fukk ak benneelu ndajem Njiiti...

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA QATAAR

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga tay fa réewum Qataar. Njiitu réew ma, Séex Tamiim Bin Hamat Al Taani moo...

CAMPEEF / NGOMBLAAN GI : TAXAWAL NAÑU PEKK GU YEES GI

Ginnaaw bi ñu falee dépite Maalig Njaay ci boppu Ngomblaan gu yees gi, sampees na pekk giy jiite campeef gi. Ci altine jee weesu...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/12/2024)

LIGGÉEY BA DOOR NA FA NGOMBLAAN GA Altine jii weesu lañu ubbi fukk ak juróomeelu moomeg Ngomblaan gi, fal mbooleem ñi ñu war a fal...

NDAJEM JËWRIÑ YI

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jiite na ndajem jëwriñ yi barki-démb ci talaata ji. Ginnaaw bi mu defaree coppite yi am...

DÉPITEY FARÃS YI DAANEEL NAÑU CÀMMUG MICHEL BARNIER

Dépitey Ngomblaanu Farãs yi wote nañu pasum diiŋat (motion de censure), daldi daaneel Càmmug elimaanu jëwriñ ya, Michel Barnier. Dépitey kujje gees duppee «...

ÀMBURUWAAS SAAR : AATU RÉER NA !

Njabootu làmbu Senegaal ak mbatiit am nañu dëj. Nde, xibaaru tiis ak uw naqar a leen dikkal ci àllarbay tay jii, 4i pani desàmbar...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (3/12/2024)

CAAROY 44 : NJIITU RÉEW MI JËL NAY NDOGAL Barki-démb ci dibéer ji lañu doon màggal 80eelu pàttalikug Caaroy 44. Ñu doon ko amal ci njiiteefu...

TIIS WU RÉY FA GINE

Mats futbal bu mujje ciy masta ! Mbir yaa ngi xew barki-démb ci dibéeru 1eelu fanu desàmbar wii, mu di woon ab finaal bees...

ALIYUN BADARA BÉEY GUDDEE NA

Aliyun Badara Béey, njiitu kurélu bindkati Senegaal yi, moo génn àddina. Keroog, dibéer 1eelu desàmbar 2024, la wuyuji Boroomam, ginnaaw bi ko ab feebar...