Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

MAMADU NJAAY, NJIITU CESTI LU BEES LI (NDEY KODDU FAAL)

Fan yii weesu, defuwaxu.com, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, bindoon na fi ab kayit, tudde ko : "Kan mooy jiiteji CESTI ?" Laaj boobu,...

18 SAFAR (TAALIFU SOXNA BAAWO JÓOB)

  18 SAFAR Dikkati nga ngir saafaraati sunuy aajooki tawat, yaw 18 safar. Kon képp ku bëgg a tonowu dikkal màggal 18 safar. Wépp yiw wees di sàkku...

2002, ATUM SUUXU JOOLAA BI

Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, "Bateau le Joolaa" def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan....

BINDKATU AYUBÉS BI : IBRAAYIMA SAAXO CAAM

                Ibraayima Saaxo Caam a nga juddoo Rëbës ci atum 1973, muy gox bi nekk diggante Medinaa ak Ñaay-Cokkeer, géej gi féete ko sowu. Gannaaw...

SENGHOR, HOUPHOUET, DOOMI-AFRIG YI DAAN XEEX AFRIG (BOOS NDÓOY)

"Tubaab yaa ngiy dem, waaye seen i karabaane a ngi des sunu biir ba tey, ñu ngemb leen, ràng leen i ngànnaay ; ba...

FAIDHERBE, SAAY-SAAY BI NUY SARGAL II (BUBAKAR BÓRIS JÓOB)

 Moone de, ngóor sii ñuy sargal tey, mooy ki daan fitnaal ak a toroxal sunuy maam, démb. Moo leen daan rey guddeek bëccëg. Mooy...

NDEY SÀGGAN, DOOM FAATU (NDEY KODDU FAAL)

Waa Mamel, fii ci Ndakaaru, naqar ak tiis lañ fanaanoo. Li ko waral mooy tuut-tànk bu tollu ci benn at moo daanoo ci seen...

KU TEDD KI (Soxna Kumba Mbόoj)

Soxna Kumba Mbόoj, ñu gën koo xam ci turu Kumba Falilu, mi ngi am 20i at, doon ab ndongo ca Daaray Sorbonne ca Paris....

MBAS MEEK ÑÀKK XÉY CI SENEGAAL (SAFIYETU BÉEY)

Bérébu liggéeyukaay yu bare tëj nañu ndax mbas mi, loolu la ab lànket bu Programme sénégalais pour l'entrepreneuriat des jeunes (PSE-J) xamle ciy xibaar....

SENEGAAL WÓOLUWUL GARABU MADAGASKAAR GI (SAFIYETU BÉEY)

«Kenn du jëfandikoo Covid Organics fii ci Senegaal». Porfesoor Musaa Séydi xamle na ni garab gii di Covid Organics te juge Madagaskaar du bokk...

GÀTTALUG XIBAAR YI (AMI MBENG)

TUUBAA Ki yore kàddug « Muxadimatul xidma » di Maxtaar Kan, mu ngi xamle ne « li wér te wóor mooy ne ab góor-jigéen kenn du ko suul...

MALI (Musaa Aysatu Jóob)

Ginnaaw bi nguurug Ibraayim Bubakar Keyta daanoo ci weeru ut 2020, réewum Mali mi ngi doon wéyal ay waxtaan ngir tabb njiit laata ñuy...