Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

BIRALU NAALU PÓLITIG WU USMAAN SONKO

Démb ci àjjuma ji, 27i pani desàmbar 2024, la elimaanu jëwriñ yi doon biral naalu pólitig wi mu fas yéene doxal ngir soppi Senegaal....

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (26/12/2024)

BÉSUB DPG BI Ci weeru awril wale jàll la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay tabboon Usmaan Sonko, def ko elimaanu jëwriñ yi. Booba...

WAA FADTS JURE NAÑU SÉEX UMAR JAAÑ

Li Séex Umar Jaañ waxoon ci Tirailleurs sénégalais yi jur na coow lu réy ci réew mi. Ca jotaayu waxtaan ba mu amaloon ak...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (23/12/2024)

NJÀNG MI : SEYDI GASAMA ÀNDUL AK JËWRIÑ JI Xale yees yéex a bind ci wayndarey juddu yi (actes de naissances) duñ mën a dugg...

CAYTU AK WOTE NAFAY NJËWRIÑ YI AK CAMPEEF YI

Altine jee weesu, fukki fan ak juróom-benn ci weeru desàmbar, la Ngomblaan gi door liggéeyub càmbar nafay njëwriñ yi. Dafa di, mbooleem kilifay njëwriñ...

MÀGGALUG BÉSUB JÀNGALEKAT YI

Jëwriñu njàngale mu kawe mi, gëstu beek coste bi màggal na bàrki-démb ci alxames ji, 19i pani desàmber 2024, bés bi ñu jagleel jàngalekat...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/12/2024)

SAMP NAÑU KI WUUTU BÀRTELEMI TOY JAAS Ngóone Mbeng mooy wuutu Bàrtelemi Toy Jaas fa boppu meeri bu Ndakaaru. Li waral loolu du lenn lu...

TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA GÀMBI

Wii yoon mooy ñaareelu tukkeem fa Gàmbi ci diir bu gàtt. Barki-démb, ci àllarba ji la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dem fa réewum...

XIBAARI TÀGGAT-YARAM

REAL MADRID JËLATI NA KUB Real Madrid moo ngi ak xalimaam di bind mbooram rekk ni du taxaw. Démb ci àllarba ji, 18i desàmbar 2024,...

MISS LITTÉRATURE SENEGAAL : NEEX XEL, RAFET KÀDDU

Njeexitalu joŋante Miss Littérature Senegaal démb la woon, àllarba, 18eelu fanu désambar 2024, ca Grand Théâtre Duudu Njaay Roos. Soxna Aminata Faal, di njàngaan...

MBIRUM MEERI BU NDAKAARU

Mbirum meeri bu Ndakaaru mi ngi wéy di jur coow. Tay rekk, Sëñ Bàrtelemi Jaas dafa bëggoon a janook saabalkat yi fa màkkaanu meeri...