Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/5/2024)

ÑËWUG KAGAME FI SENEGAAL Póol Kagame, Njiitu réewum Ruwàndaa li, moo ngi woon fi réew mi ci njeexitalu ayu-bés bi. Ab tukkib liggéey la fi...

DÉGGOOY SOROJ BEEK GAAS BI : CÀKKUTEEFU WAY-XARAÑ YI

Nguur gi war na waxtaanewaat déggoo yi ñeel soroj beek gil bi (gaas bi). Loolu mooy gis-gisu way-xarañ yi seen xel màcc ci nees...

MËQ SUUF

Bari na ay mag, yu góor ak yu jigéen, yuy fàttaliku lenn ci li ñu daan def bi ñu nekkee tuut-tànk te ñu leen...

NJIITU RÉEW MI DALAL NA PÓOL KAGAME, NJIITU RÉEWUM RUWÀNDAA

Njiitu Réewum Ruwàndaa, Póol Kagame, teersi na Ndakaaru, tey ci gaawu gi, fa naawub Lewópóol Sedaar Seŋoor. Tànki  nemmeeku ak liggéey la doxsi. Bi Póol...

BATAAXALU NGUGI AK BÓRIS JÓOB ÑEEL NJIITU RÉEW MI

Ci tekkig Ndey Koddu FAAL "Kilifa gu mag gi,  Jàmm ak salaam ñeel nañu la ! Say mag ñoo lay nuyu, di la jox sa wàccuwaay. May...

LI GËN A FÉS CI XIBAAR BÉS BI (9/5/2024)

BÉSUB MÀGGALU “ASCENSION” Tey, ci alxames ji, yemoo ak juróom-ñeenti fan ci weeru me, mooy bés bi ñi bokk ci diiney kercen di màggal yéegug...

AIBD : AB ROPPALAAN BU WÀCC YOONAM

Naawub Belees Jaañ bi (Aéroport International Blaise Diagne) dafa tëj, tey ci alxames ji. Ab roppalaanu Transair bu Air Sénégal àbb moo wàcc yoonam....

LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL

Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali "Ligue des champions" bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci...

LAYOOB KÀPPITEN TURE AK SÉEX YERIM SEKK

Àtte ba jib na. Àttekat bi jox na Kàmpiten Ture dëgg. Nde, dafa daan Séex Yerim Sekk ak boroom këru móolukaay gii di Éditions...

NAPP GI : JUB, JUBAL, JUBBANTI

Jëwriñu napp gi, Doktëer Faatu Juuf, siiwal na toftaleg turi nit ñi ñu jagleel ay lisãsi napp (licence de pêche). Lisãsu napp mooy, ci...

KÀDDUY ELIMAANU JËWRIÑ YI

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, yékkateeti nay kàddu jëmale ci Saa-Senegaal yi. Wile yoon moo ngi leen yékkati ci turu njiiteefu làngug pólitigam, Pastef....