Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

JÀPP NAÑU NDEELA MAAJOOR JUUF

Coowal Ndeela Maajoor Juuf moo lëmbe tey réew mi. Mollah Morgun mooy siiwal ci Facebook ay widéwoo yoy, dañ ciy wone ay xale yu...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/12/2023)

LAYOO MAAM MBAY ÑAŊ USMAAN SONKO Bu yàggul dara lañu jàppoon layoo Maam Mbay ak Usmaan Sonko ngir ñu àttewaat leen. Waaye, layoo boobu mujjul...

NGOMBLAAN GI WOTE NA CÀRTUG CÀMM GI

Bërki-démb ci altine ji fukki fan ak juróom-ñatt, dépite yi wote nañu sàrt càmm gi ca Ngomblaan ga. Muy nekk guléet ca màkkaanum Péncum...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/12/2023)

AYIB DAFE SOOYATI NA Ayib Dafe, ndawul Usmaan Sonko miy lawax ci wotey 2024 yi, sooyati na. Ndax, dafa dellooti woon fa DGE, moom ak...

BÉSUB MBËKK MI

Démb ci altine ji, 18 desàmbar 2023, lees jagleeloon mbëkk mi ci àddina sépp. Muy bés bu ñu jàpp ngir waxtaane lu waral ñiy...

JÉYYA JA AM CA GINE KONAAKIRI

Guddig dibéer jàpp altiney tey jii fukki fan ak juróom-ñett ci weer wii la tàkk-tàkk lu am doole am fa Gine Konaakiri. Fa ñuy...

XIBAARI TÀGGAT-YARAM

KUPPEG TEFES Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti...

DELLUSIG KARIIM MAYSA WÀDD FI RÉEW MI

Dellusig Kariim Maysa Wàdd fi réew mi doonatul lu ay ñoñam di xel-ñaar. Ñi ko war a dalal, jumtukaay yi mu laaj ba ci...

ANIBAAL JIIM PELENT NA AADAMA FAAL MU BENNOO

Ab bataaxal la Anibaal Jiim mi ci kaso bi biral, di ci xamle ne dina pelent kii di Aadama Faal mi bokk ci lëkkatoo...

ÑEENTI SÓOBARE ÑOO ÑÀKK SEEN I BAKKAN FA KAASAMÃS

Fa Kaasamãs, dafa ag daamaruy sóobare gu dal ci kow um mbéll « antichar ». Bi loolu amee nag, ñeenti sóobare ñoo ci ñàkk seen i...

MBIRUM MARJAAN YI : ME MUSAA JÓOB A NGI KASO

Meetar Musaa Jóob a ngi ci guddi yu lëndëm jamono jii. Ndax, tey ci àjjuma ji, 15 desàmbar 2023, lañ ko dóor « mandat de...