Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (14/12/2023)

ÀTTEB USMAAN SONKO Ndogal lañu doon xaar jëm ci àtteb Usmaan Sonko ak Càmm gi, àttekat bii di Usmaan Raacin Coon biral na ko. Lañu...

ÀTTEWAAY BU NDAKAARU JOX NA SONKO DËGG

Coowal « damay bokk ! » ak « doo bokk ci wote yi ! », diggante Càmm geek Usmaan Sonko, moo lëmbe réew mi jamono yii. Boo bàyyee xel,...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/12/2023)

NDONGOY UGB YI SUMB NAÑ AB XEEX Lu jege fukki fan ak juróom ba weer wi dee ak léegi. Ba tey ndongo yi mënuñoo jot...

USMAAN SONKO AK CÀMM GI, PËND BA WUREEGUL

Dogal bi ñu doon xaar tey ci Talaata ji jëm ci àtteb Usmaan Sonko ñeel li ñu ko bëgg a dàq ci wayndarew wote...

NDELLOOG USMAAN SONKO CI WAYNDAREW WOTE WI

Ci talaatay tey jile, 12 desàmbar 2023, la tirbinaal « hors classe » bu Ndakaaru di àtte ndax dañuy delloo Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi...

XIBAARI TÀGGAT-YARAM

FUTBAL Victor Boniface moo ngi dox ci ndox Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (11/12/2023)

WOTEY 2024 YI Tey ci altine ji, 11 desàmbar 2023, la deppo yi ñeel nekkug lawax ci wotey 2024 di tàmbale fa ndajem ndeyu àtte...

COOWAL KOPPARI QATAAR YI

Atum 2019 lañu jëkkoon a dégg jokkalanteg koppar gu dox diggante kërug lijjanti  gu nekke fa Qataar, Tullow Oil,  ak njiitul Pastef li, Usmaan...

COOWAL NJÀNG MU KOWE MI : UCAD TIJJEEGUL I BUNTAM

Jàngune Séex Anta Jóob bu ndakaaru tijjeegul i buntam. Musaa balde, jëwriñ ji ñu dénk njàngale mu kowe mi, gëtu beek càkkeef yi, ànd...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/12/2023)

NDEY FAATU FAAL Ndey Faatu Faal mi ñuy woowee Faala Fëlëer nekk ab ñaxtukat, ñu gën koo xame ci làngug kujje gi, jot na...

YOON BÀYYI NA USTAAS UMAR SÀLL

Àtte bi daanu na. Tey ci àjjuma ji lañ doon àtte Ustaas Umar Sàll ginnaaw bees ko jëkkee bëtal àjjuma jee weesu. Dafa am...