Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LAYOO USMAAN SONKO AK MAAM MBAY ÑAŊ

Coowal 29 miliyaari yi ñu ne woon dañu ko luubal ca PRODAC, dekkiwaat na. Kii di Usmaan Sonko njiitul Pastef li mooy ki xolli...

UGB : XEEX BI DOORATI NA !

Xeex bi jolleeti na diggante ndongoy iniwérsite Gastoŋ Berse ak takk-der yi. Jamono jii ñuy bind yaxal bi, xale yaa ngay jàmmaarloo ak takk-der...

XIBAARI TÀGGAT-YARAM (Dibéer 29 saŋwiye 2023)

CHAN 2023 Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi,...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (Dibéer 29 saŋwiye 2023)

TUUBAA : JAWUB “OCASS” LAKK NA Démb ci guddi, ay boori 22i waxtu, lees nemmeeku ag lakk ca « Marché Ocass » ba nekk Tuubaa....

SËÑ BAS, KU WAX FEEÑ

Sa tànk mën na la dugal, sa làmmiñ génne la ; sa loxo dugal la, sa làmmiñ génne la ; sa bët dugal la,...

Burkinaa Faaso dàq na sóobarey Farãs ya ca réew ma

Sóobarey Farãs yi dinañu jógge ca Burkinaa Faasoo. Ginnaaw bi ko kilifay réew ma sàkkoo, kilifay réewum Farãs yeet nangu nañ ndogal li ba...

Li gën a fés ci xibaari bés bi

PÓLITIG Maalig Gàkku taxawal nag lëkkatoo Ginnaaw bi mu fésalee yéeneem ngir bokk ci wote yii di ñëw, ca ndajem-waxtaan ma mu doon amal xamle na...

FESNAC

Kafrin dalal na xew-xewu mbatiit bu réy bi ñu dippe ci nasaraan Festival National des Arts et Cultures, gàttal biy joxe FESNAC. Mu ëmb...

MAKI SÀLL DÀQLU NA AMINATA TURE, TËJLU NIT-DOF

Pekkub Ngomblaan gi dafa amaloon am ndaje ci bésub tey jile. Ndaje ma nag, daanaka ñépp la bett. Ndeke, ci mbirum Soxna Aminata Ture...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 23 sãwiye 2023

PÓLITIG Bërki-démb ci dibéer ji, waa Pastef doon nañ amal ab mitiŋ ca depàrtamã bu Kër Masaar. Mu doonoon nag ndaje mu réy a réy...

MOO MAN LU MAY WAXATI ? (Taalifu Séex Aliyu Ndaw)

Keroog, àllarba 18i fan ci saŋwiyee 2023 la mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ doon sargal ak a delloo njukkal bindkat bu mag a mag bii...

USMAAN SONKO : « GAT-SA GAT-SA ! … DINANU XEEX AK MAKI SÀLL ! »

Kër Masaar wàcc na. Bu yeboo, bés niki tey, nu ngéntewaat depàrtmaa bu bees bi, duppee ko Kër-Sonko walla Kër-Pastef. Guléet mbooloo mu ni...