Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

AKSIDAŊ YI : 1 200I WAY-DËDDU DIGGANTE 2021 AK 2022

Dem beek dikk baa ngi wéy di jur coow fi réew mi. Ay aksidaŋ yu baree ngi wéy di am, di rey ñu bari...

SEMINEERU NGUUR GI

Démb ci gaawu gi la Nguur gu bees gi doon amal ab semineer. Njiitu réew mi,  Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo ko jiite...

AYU-BÉSU JËF ÑEEL NJÀNG MI

Démb ci àjjuma ji lañ doon tëj ayu-bés bi ñu jagleel jëf ñeel njàng mi. Muy xew-xew bu ñuy màggal at mu jot ci...

Aksidaŋ bi ca yoonu Kungël : Njaal ak ndigali Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay

Démb ci alxemes ji, 25i awril 2024, la aksidaŋ bu metti amee woon fa gox bees duppee Yamoŋ Mbajaaneen, ca kow tali ba jëm...

LI GËN A FÉS CI XIBAAR BÉS BI (25/04/2024)

ÑETTEELU NDAJEM JËWRIÑ Démb ci àllarba ji la Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay doon amal ñetteelu ndajem ak i jëwriñam. Mu jël fa...

ABDURAHMAAN JUUF MA NGA CA JÀNGUNE YA

Ginnaaw ba ñu leen takkalee seen i ndomboy-tànk, jëwriñi Càmm gu bees gi sóobu nañu ci liggéey bi leen di xaar. Kenn ku nekk...

23 AWRIL BÉSUB TÉERE AK ÀQU BINDKAT BI

Mbootaayu Xeet yi ñeel njàng, xarala ak mbatiit (UNESCO) moo tànn bésub 23 ci awril, jagleel ko téere ak àqu bindkat bi. Saa yu...

SIIWALUG CAABAL YI

Àllarba jii weesu la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon amal ñaareelu ndajem jëwriñam. Ca ndaje moomee la jëlee ay ndogal yu...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (22/4/2024)

SONKO SANT NA JËWRIÑ YA WOON ÑU DELLOO DAAMARI NGUUR GI Jëwriñ yu nekkoon ci Càmmug Maki Sàll ya woon, war nañu delloo daamari Nguur...

SÉEX ALIYU NDAW GÉNTOON NA KO DÉMB, AADAMA BAROW AK BASIIRU JOMAAY FAY DEF NAÑ KO TEY

Atum 1981, Séex Aliyu Ndaw, bindkat bu ràññeeku, daa bind woy tudde ko : Sama mbokku Bànjul. Di ci ñaax ak a digal Saa-Senegaal yeek...

ÑAAREELU TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA BITIM-RÉEW

Ginnaaw bi mu njëkkee génn, dem fa réewum Móritani, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomay Fay amal na ñaareelu tukkeem fa réewum Gàmbi. Muy...

LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (19/4/2024)

NDOGALI NJIITU RÉEW MI, BASIIRU JOMAAY JAXAAR FAY  Ganug njénde li Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, amoon na gan tey ci àjjuma ji. Tof-Njiitu...