Senegaal : Yan njàngat la askan wi wara jukkee ci kàngam yu bare te ràññeeku yi génn àddina ci fan yii ? Ci diirub 40i fan rekk, réewum Senegaal dëjal na fiy boroomi daraja yu fésoon lool. Li ci gën a doy-waar mooy ne dafa méngook jamono joo xam ne, réew maa ngi jànkoonteek mbasum covid-19 mi. Loolu, nag, war nanoo yee, nu xool naka lees di def ba ndaw ñi roy ci ñooñule réew mi ñàkk.
KORONAA : Jawriñ biñ dénk kaaraange biir réew mi Aali Nguy Njaay,...